1
Njàlbéen ga 26:3
Kàddug Yàlla gi
Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.
Compare
Explore Njàlbéen ga 26:3
2
Njàlbéen ga 26:4-5
Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele, ndax Ibraayma déggal na ma, dénkoo na sama ndénkaane, ak samay santaane, ak sama dogali yoon, ak samay yoon.»
Explore Njàlbéen ga 26:4-5
3
Njàlbéen ga 26:22
Mu jóge foofa, gasati teen, jàmm ne ñoyy, mu tudde ko Reyobot (mu firi Fu yaatu), ndax da ne: «Léegi Aji Sax ji yaatal na nu, te dinanu woomle ci réew mi.»
Explore Njàlbéen ga 26:22
4
Njàlbéen ga 26:2
Foofa Aji Sax ji feeñu ko fa ne ko: «Bul dem Misra, waaye nanga toog ci réew mi ma lay wax.
Explore Njàlbéen ga 26:2
5
Njàlbéen ga 26:25
Isaaxa nag sàkk fa sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko, ba noppi samp fa xaymaam. Te itam ay surgaam bënn nañu fa ab teen.
Explore Njàlbéen ga 26:25
Home
Bible
Plans
Videos