Njàlbéen ga 2
2
1Ci kaw loolu asamaan ak suuf ak li ñu ëmb lépp mat. 2Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp. 3Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dal-lu woon gannaaw liggéey, ba mu sàkke lépp.
Cosaanal asamaan ak suuf
(Saar 2.4—4.26)
Yàlla dugal na nit Àjjana, jox ko ndigal
4Liy cosaanal asamaan ak suuf, ba ñu leen di sàkk, mooy lii. Bés ba Aji Sax ji Yàlla sàkkee suuf ak asamaan, 5genn garab nekkagul woon ci kaw suuf, te genn gàncax saxagul; ndaxte booba Yàlla Aji Sax ji tawagul, te nit kuy bey amagul. 6Ci biir loolu mbënn di balle ci suuf, di tooyal fépp. 7Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.
8Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind. 9Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon.
10Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, dale fa nag, séddlikoo, def ñeenti wal. 11Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma, 12di wurusu ngalam; te it ndàbb lu neex xet a nga fa woon ak per yu jafe yu ñuy wax onigsë. 13Ñaareelu dex ga di Giyon, wër réewu Kuus mépp; 14turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat.
15Yàlla Aji Sax ji nag jël nit ki, tàbbal ko biir toolub Àjjana, mu di ko bey ak a sàmm. 16Yàlla Aji Sax ji sant nit ki, ne ko: «Man ngaa lekk ci mboolem garabi tool bi, 17waaye bul lekk ci garab giy taxa xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.»
18Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.» 19Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom. 20Ba mu ko defee nit kooku, di Aadama, tudd jur gépp ak picc yépp ak rabi àll yépp, waaye fekku ca ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.
21Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux. 22Yàlla Aji Sax ji bind jigéen ci faar, gi mu jële ci Aadama, indil ko ko. 23Aadama ne tonet, daldi ne:
«Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux!
Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële#2.23 Ni ñuy wooye góor ak ni ñuy wooye jigéen dañoo jegeyoo ci làkku ebrë..»
24Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux.
25Ku góor ki ak soxnaam, ñoom ñaar ñépp, yaramu neen lañu defoon, te amuñu ci woon genn kersa.
Currently Selected:
Njàlbéen ga 2: KYG
Highlight
Share
Copy
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Copyright © 2010, 2020 La Mission Baptiste du Sénégal

: