YouVersion Logo
Search Icon

Njàlbéen ga 22

22
Yàlla nattu na Ibraayma
1Gannaaw loolu am na bés Yàlla di nattu Ibraayma ne ko: «Ibraayma!» Mu ne ko: «Naam.» 2Yàlla ne ko: «Ngalla jëlal sa jenn doom jii di Isaaxa, muy koo bëgg, nga dem ca réewu Morya ca tund wa ma lay wax, joxe ko fa, mu nekk saraxu rendi-dóomal
3Ibraayma nag teela xëy, takk mbaamam, ànd ak ñaari surgaam ak doomam Isaaxa, daldi xar matt, mi muy lakke sarax bi. Ma nga jëm fa ko Yàlla wax. 4Ca gannaaw ëllëg sa, Ibraayma daa dawal bëtam, séen bérab ba fu sore. 5Mu ne surga ya: «Négleen fii, mbaam mi taxaw. Man ak xale bi nu dem ba fale, màggali Yàlla te ñëw.»
6Ba loolu amee Ibraayma jël mattum saraxu rendi-dóomal ba, yen ko doomam Isaaxa; moom mu ŋàbb la muy taale ak paaka ba ci loxoom, ñu ànd ñoom ñaar. 7Isaaxa ne baayam Ibraayma: «Baay!» Mu ne ko: «Naam, doom sama.» Isaaxa ne ko: «Sawara saa ngi, matt maa ngi, waaye ana gàtt, bi nuy sarxal?» 8Ibraayma ne ko: «Yàlla moom ci boppam dina dikk ak gàtt bi nuy def sarax, doom,» ñu daldi ànd dem, ñoom ñaar.
9Ba ñu àggee fa ko Yàlla wax, Ibraayma sàkk fa ab sarxalukaay, teg ca matt ma, yeew Isaaxa doomam, teg ko ca kaw matt ma ca sarxalukaay ba. 10Ibraaymaa nga tàllal loxoom, ŋëb paaka, ba muy rendee doom ja. 11Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!» 12Malaaka ma ne ko: «Bu sa loxo laal xale bi; bu ko def dara, ndaxte léegi xam naa ne ragal nga Yàlla, ndax gàntaloo ma sa jenn doom ji.» 13Naka la Ibraayma siggi rekk, yem ci menn kuuyum xar mu béjjén ya lonke ci as ngarab. Ibraayma dem, jël kuuy ma, rendi, mu wuutu doom ja, di ab saraxu rendi-dóomal. 14Ibraayma nag tudde bérab boobu Yawe Yire (mu firi Aji Sax ji dina dikk). Moo tax ñuy wax ba tey, naan: «Aji Sax jaa ngay dikke ca tundam.»
15Ci kaw loolu malaakam Yàlla ma dellu àddoo asamaan ne Ibraayma: 16«Déglul lii Aji Sax ji wax: “Giñ naa ci man mii, gannaaw yaa def lii, te gàntaloo ma sa jenn doom ji, 17maa lay barkeela barkeel, fula ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk, 18te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»
19Ba loolu wéyee Ibraayma waññiku, fekki surga ya, ñu daldi ànd ñoom ñépp, jëm Beerseba, ndax fa la Ibraayma dëkkoon.
Askanu Naxor
20Gannaaw gi, dañoo yégal Ibraayma ne ko: «Milka kat am na ay doom moom it, moom ak sa mag Naxor. 21Uus lañu taawloo, teg ca Bus, teg ca Kemwel, miy baayu Aram, 22teg ca Keset ak Aso ak Pildas ak Yidlaf ak Betuwel.» 23Betuwel ay baayu Rebeka. Ñooñu ñooy juróom ñetti doom yu góor, yi Milka am ak magu Ibraayma, Naxor. 24Rewma it nekkaaleem la woon, doom ya mu ca am di Teba ak Gaxam ak Taxas ak Maaka.

Currently Selected:

Njàlbéen ga 22: KYG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in