John 10
10
1Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Ku tabiwul cha bunta ba cha bir gēt’ i nh͈ar ya, wande mu yēg cha genen wet, mō di sachakat ak lelkat.
2Wande ku di tabi cha bunta ba, mō di samakat i nh͈ar ya.
3Chi mōm la otukat i bunta ba di ūbi; te nh͈ar ya dēga bāt am; te mu ô i nh͈ar am chi sēn tur, te jīte len cha biti.
4Ba mu gēne yos am yepa mu jītu len, te nh͈ar ya topa ko; ndege h͈am nañu bāt am.
5Te gan la ñu di bañ a topa, wande di nañu ko dou; ndege h͈amu ñu bāt i gan.
6Yesu wah͈ on na len lēb bile: wande h͈amu ñu yef ya mu wah͈ ak ñom.
7Tah͈na Yesu nêti len, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Mā di bunt’ i nh͈ar ya.
8Na ma jītu on ñepa di i sachakat ak i lelkat: wande nh͈ar ya dēgu len on.
9Mā di bunta bi: chi man su nit h͈arafe, di na mucha, te di na tabi chi bir, gēna cha biti, te feka mporlukay.
10Sachakat ba du ñou lu dul sacha, te rēndi, te sanka; mā ñou ndah͈ ñu am dūnda, te ndah͈ ñu am ko bu bare.
11Mā di samakat bu bāh͈ bi: samakat bu bāh͈ bi defa joh͈e bakan am ndig nh͈ar yi.
12Ku neka yōlukat, te dowul samakat, te mōmul nh͈ar ya, mu gis buki ba di dika, te wocha nh͈ar ya, te dou, te buki ba japa len, te tasāre len.
13Mu dou ndege yōlukat reka la, te farlewul nh͈ar ya.
14Mā di samakat bu bāh͈ bi, te h͈am nā suma yos, te suma yos h͈am nañu ma,
15Naka ma Bay ba h͈ame, te mā h͈am Bay ba; te tedal nā suma bakan ndig nh͈ar ya.
16Te amati nā yenen i nh͈ar, ñu bokul chi gēta gile: ñom it, war nā len isi, te di nañu dēga suma bāt; te di nañu neka bena gēta, ak bena samakat.
17Mōtah͈ suma Bay ba sopa na ma, ndege tedal nā suma bakan, ndah͈ ma jelati ko.
18Ken jelewu ko chi man, wande tedal nā ko chi suma bopa. Antan nā ko tedal, te antan nā ko jelati. Eble bile, mōm lā jele won fa suma Bay.
19Werante jogati nak chi digante Yauod ya ndig bāt yile.
20Te ñu bare chi ñom ne, Ame na jine, te telbataku; lutah͈ ngēn ko dēglu?
21Ñenen ne, Yile du wah͈ i ku ame jine. Ndah͈ jine mun na ūbi but i silmah͈a?
22H͈ewte i setalay i juma ja am on na cha Jerusalem: nôr la won;
23Te Yesu don na doh͈ cha bir juma ja, cha bulu’ Suleyman.
24Yauod ya nak dajalo fi mōm, te ne ko, Be kañ nga ño bayi chi jāh͈le? So de Krista, wah͈ ñu ko bu set.
25Yesu tontu len, ne, Wah͈ on nā len, te gumu len: ligey yi ma def chi suma tur i Bay, yile ma sēdêl.
26Wande yēn, gumu len ndege boku len chi suma i nh͈ar.
27Suma i nh͈ar dēga nañu suma bāt, te h͈am nā len, te topa nañu ma;
28Te may nā len dūnda gu dul jêh͈; te du ñu sanku muk, te ken du len foh͈arñi chi suma loh͈o.
29Suma Bay ka ma len may on, mō gēti ñepa; te ken munul len a foh͈arñi chi loh͈o i Bay ba.
30Man ak Bay ba di bena.
31Yauod ya fabati i doch ndah͈ ñu jumat ko.
32Yesu tontu len, ne, Ligey yu bāh͈ yu bare lā len won on fa Bay ba; ana ban chi ligey yile ngēn ma jumat ak i doch?
33Yauod ya tontu ko, ne, Dowul ndig ligey bu bāh͈ la ñu la buga jumat, wande ndig sāga Yalla; ndege you mi di nit def nga sa bopa Yalla.
34Yesu tontu len, ne, Ndah͈ bindu ñu chi sen yōn, Nôn nā, Yēn a di i yalla?
35Su len tūde won i yalla, ndege chi ñom la bāt i Yalla ñou on (te du mun a fanh͈a mbinda mi),
36Di ngēn wah͈al ka Yalla selal on, te yōni ko chi aduna si, ne Sāga nga Yalla, ndege wah͈ nā, ne, Mā di Dōm i Yalla?
37Su ma defule suma i ligey i Bay, bu len ma gum.
38Wande su ma len defe, su ngēn ma gumule, na ngēn gum ligey yi: ndah͈ ngēn mun a h͈am te dēga ne Bay ba’ngi chi man, te mangi chi Bay ba.
39Ñu jēmati ko japa; te mu rēcha chi sēn loh͈o;
40Te mu demati cha ganou Jordan, cha bereb ba John jek’ on di batise; te mu jēki fa.
41Te ñu bare dika fa mōm; te ñu ne, John nak deful on mandarga: wande yef ya John wah͈al on nit kile yepa dega la.
42Te ñu bare gum on nañu chi mōm fōfale.
S'ha seleccionat:
John 10: GWG
Subratllat
Comparteix
Copia
Vols que els teus subratllats es desin a tots els teus dispositius? Registra't o inicia sessió
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

: