Matthew 16
16
1Pharisee ya ak Sadducee ya ñou di ko fir, te lāj ko mu won len mandarga cha asaman.
2Wande mu tontu len, ne, Su janta soe, ngēn ne, Di nañu am bes bu nêh͈ tey, ndig asaman si h͈onh͈a na:
3Ti chi sūba, Di na h͈ēn tey, ndege asaman si tīm na. Mun ngēn a rañātle kanam i asaman si; wande munu len a rañātle melo i jamāno yi.
4H͈êt wu bon ak njālo ūt na mandarga; du ñu ko may mandarga, lu dul mandarga i Jonah. Mu bayi len, te dem.
5Tālube ya ñou cha genen wet ga, te ñu fate won a jel mburu.
6Yesu ne len, Otu len te moytu mporoh͈al i Pharisee ya ak Sadducee ya.
7H͈alāt nañu chi sēn bopa, ne, Ndig indiū ñu on mburu.
8Ba ko Yesu h͈ame, mu ne, E gā’ ngum gu new, lutah͈ ngēn werante chi sēn digante, ndege amu len mburu?
9Dēgangu len, wala fatalakuwu len jurom i mburu i jurom njūne ya, te ñāt’ i sendel ngēn forātu on?
10Wala jurom ñar i mburu i ñenent njūne ya, te ñāt’ i sendel ngēn forātu on?
11Lutah͈ be h͈amu len ne wah͈u ma len chi mburu? Wande ndah͈ ngēn otu mporoh͈al i Pharisee ya ak Sadducee ya.
12Fōfale ñu h͈am ne wah͈ul len ñu otu mporoh͈al i mburu, wande njemantal i Pharisee ya ak Sadducee ya.
13Ba Yesu ñoue chi i wet i Cæsarea Philippi, mu lāj i tālube am, ne, Man mi di Dōm i nit ka, kan la nit ña wah͈ ne mōm la?
14Ñu ne, Ñena ña ne, John Batisekat ba; ñenen ne, Elijah; te ñenen ne, Jeremiah, wala kena chi yonent ya.
15Mu ne len, Wande yēn, kan ngēn wah͈ ne mōm la?
16Simon Peter tontu, ne, Yā di Krista, Dōm i Yalla ju dunda ji.
17Yesu tontu ko, ne, Barkel chi you, Simon dōm i Jonah; ndege du yaram te du deret a la fêñal lōlu, wande suma Bay ba cha ajana.
18Te mangi la wah͈ it, ne yā di Peter, te chi doch wile lā di tabah͈ suma jangu; te bunt’ i nāri du ko fabi.
19Di nā la may i chābi’ ngur i ajana: te lu neka lo taka chi suf, di na taku cha ajana; te lu neka lo tiki chi suf, di na tikiku cha ajana.
20Fōfale mu ebal tālube ya, ne bu ñu wah͈ ken ne mō di Krista.
21Cha sā sōsale Yesu dal di won i tālube am naka mu ela deme fa Jerusalem, te sona yef yu bare chi mag ya, ak i njīt i seriñ ya, ak bindānkat ya, te di ko rēyi, mu di dēkiji chi ñetel i fan am.
22Peter japa ko, te dal di ko eda, ne, Borom bi, na la Yalla yerem; lile du la dal muk.
23Wande mu walbatiku, te ne Peter, Randu ma, Seytane si; yā di suma mpaka; ndege topatoū la yu jem chi yef i Yalla, wande yef i nit.
24Fōfale Yesu ne i tālube am, Su nit buge and’ ak man, na wēdi bop’ am, gadu kura am, te topa ma.
25Ndege ku mu mun a don ku buga musal bakan am, di na ko rēr: te ku mu mun a don ku di rērlo bakan am ndig man, di na ko gis.
26Ndege ban njeriñ la chi nit, su ame aduna si yepa, te mu ñaka bakan am? wala wan wēchi la nit di joh͈e ndig bakan am?
27Ndege Dōm i nit ka di na ñou chi ndam i Bay am, ak i malāk’ am; te chi wah͈tu wōwale di na yōl nit ku neka naka ligey am day.
28Chi dega mangi len di wah͈, Ñena ñi tah͈ou file, du ñu mos dē, be ba ñu di gisi Dōm i nit ka mu di ñou chi ngur am.
S'ha seleccionat:
Matthew 16: GWG
Subratllat
Comparteix
Copia
Vols que els teus subratllats es desin a tots els teus dispositius? Registra't o inicia sessió
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

: