Matthew 8
8
1Ba mu wache cha tūnda wa, mbōlo mu rey top’ on nañu ko.
2Ab gāna ñou fi mōm, te ñān ko, ne, Borom bi, su la nêh͈e, mun nga ma setal.
3Yesu talal loh͈o am, te lāl ko, ne, Di nā tah͈ nga set. Chi tah͈ouay ba mu dal di wer.
4Yesu ne ko, Otul te bu ko wah͈ ken; wande demal wone sa bopa seriñ ba, te jebale maye ga Musa eble won, ndig sēde chi ñom.
5Ba Yesu h͈arafe chi Capernaum, bena saltige ñou fi mōm, te dagān ko,
6Ne, Borom bi, suma bukanēg anga teda cha ker, lafañ, te sona bu miti.
7Yesu ne ko, Di nā dika te weral ko.
8Saltige ba tontu ko ne, Borom bi, daganu ma nga h͈araf chi suma nēg; wande wah͈al bāt bi reka, te suma bukanēg di na wer.
9Ndege nit lā ku neka chi run i kēlifa, te am nā i h͈arekat ya ma ēlif; te ku ma cha ne, Demal, mu dem; te ku ma cha ne, Ñoual, mu ñou; suma jām, Defal lile, mu def ko.
10Ba ko Yesu dēge, mu jomi, te ne ña ko top’ on, Chi dega mangi len di wah͈, mosu ma feka ngum gu nu day, dēt, du chi Israel.
11Te ma ne len, ñu bare di nañu jugeji cha Penku ak H͈arfu, te jēki ak Ibrayuma ak Isaka ak Yanh͈oba chi ngur i ajana;
12Wande i dōm i ngur ga, di nañu len tabal chi lendem i biti; fōfale la joy di neka ak yeyi buñ.
13Yesu ne saltige ba, Demal sa yōn, naka nga gume, na ame nōgu chi you. Bukanēg am dal di wer cha wah͈tu wōwale.
14Ba Yesu h͈arafe chi nēg i Peter, mu gis goro am teda, opa ak fēbar.
15Mu lāl loh͈o am, te fēbar ba bayi ko; mu jog te bukanēgu ko.
16Ba ngon jote, ñu yub ko ña i jine jap’ on, te mu gēne malāka yu bon ya chi ñom chi bāt am, te weral ña jēr on ñepa:
17Ndah͈ la Isaiah yonent ba wah͈ on motaliku, ne, Mō jel on suñu munadi, te yubu on suñu i jangaro.
18Yesu nak ba mu gise mbōlo mu rey chi kanam am, mu eble ñu jala cha genen wet ga.
19Bena bindānkat ñou, ne ko, Jemantalkat bi, di nā la topa fo mun a dem.
20Yesu ne ko, Ntila yi am nañu i mpah͈, te mpich’ i asaman si am nañu i taga, wande Dōm i nit ka amul fu mu tedal bop’ am.
21Kenen chi tālube ya ne ko, Borom bi, bayi ma ma jeka dem te sūl suma bay.
22Wande Yesu ne ko, Topa ma, te bayi ñu dēle ña ñu sūl sēn ñu dē.
23Ba mu duge chi gāl, i tālube am topa ko.
24Ngelou lu rey jog cha gēch ga, be gāl ga muro ak dūs ya; wande mu don nelou.
25Ñu ñou fi mōm, te ê ko, ne, Borom bi, musal ñu: ñunge sanku.
26Mu ne len, Lutah͈ ngēn ragal, yēn nit i ngum gu new? Fōfale mu jog, te eda ngelou ya ak gēch ga; mu dal be ne nem.
27Nit ña jomi, ne, Ban melin i nit a di kile, be ngelou li sah͈ ak gēch gi di ko dēgal!
28Ba mu age cha genen wet, chi bir rew i Gadarene ya, ñar i nit ñu i jine jap’ on feka ko, di juge cha bamel ya, te ñu soh͈or lol, be ken munul a jār yōn wōwale.
29Ñu h͈āchu, ne, Lan la ñu jote ak you, you Dōm i Yalla? Dā fi dika ndig geten ñu bala wah͈tu wa jot?
30Gēt’ i mbām yu bare sorey on nañu fale di far.
31Te jine ya dagān ko, ne, So ñu gēnê, bayi ñu ñu dem chi bir gēt’ i mbām ya.
32Mu ne len, Dem len. Ñu gēna cha nit ña, te duga chi mbām ya: gēta ga yepa dou ak dōle chi kou bereb bu koue di jem chi gēch ga, ñu rēr chi ndoh͈ ma.
33Ña len don sama dou, dem chi bir deka ba, te wah͈ lu neka, ak lu jot nit ña jine jap’ on.
34Deka ba yepa gēna gatanduji Yesu; te ba ñu ko gise, ñu dagān ko mu gēna chi sēn rew.
S'ha seleccionat:
Matthew 8: GWG
Subratllat
Comparteix
Copia
Vols que els teus subratllats es desin a tots els teus dispositius? Registra't o inicia sessió
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

: