Njàlbéen ga 5

5
Askanu Aadama, ba ci Nóoyin
(Saar 5.1—6.8)
1Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam, 2góor ak jigéen la sàkk, barkeel leen, tudde leen Nit, keroog ba mu leen sàkkee.
3Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set. 4Set juddu na, Aadama dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 5Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu.
6Set moomee am na téeméeri at ak juróom (105), doora jur Enos. 7Enos juddu na, Set dundaat juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñaar (807), amaat doom yu góor ak yu jigéen. 8Kon Set dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk ak ñaar (912), doora faatu.
9Enos nag am na juróom ñeent fukki at (90), doora jur Kenan. 10Kenan juddu na, Enos dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fukk ak juróom (815), amaat doom yu góor ak yu jigéen. 11Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu.
12Kenan moomee am na juróom ñaar fukki at (70), doora jur Malaleel. 13Malaleel juddu na, Kenan dundaat juróom ñetti téeméeri at ak ñeent fukk (840), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 14Kon Kenan dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk (910), doora faatu.
15Malaleel nag am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Yeredd. 16Yeredd juddu na, Malaleel dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fanweer (830), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 17Kon Malaleel dund na juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (895), doora faatu.
18Yeredd moomee am na téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (162), doora jur Enog. 19Enog juddu na, Yeredd dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 20Kon Yeredd dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (962), doora faatu.
21Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem. 22Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 23Kon Enog dund na ñetti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom (365). 24Enog dafa topp Yàlla, ba jekki-jekki giseesatu ko, ndaxte Yàllaa ko yéege fa moom.
25Matusalem moomee am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak juróom ñaar (187), doora jur Lemeg. 26Lemeg juddu na, Matusalem dundaat juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (782), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 27Kon Matusalem dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom ñeent (969), doora faatu.
28Lemeg nag am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (182), doora jur doom ju góor. 29Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.» 30Nóoyin juddu na, Lemeg dundaat juróomi téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (595), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. 31Kon Lemeg dund na juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar (777), doora faatu.
32Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet.

선택된 구절:

Njàlbéen ga 5: KYG

하이라이트

공유

복사

None

모든 기기에 하이라이트를 저장하고 싶으신가요? 회원가입 혹은 로그인하세요