1
Njàlbéen ga 14:20
Kàddug Yàlla gi
Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko.
Jämför
Utforska Njàlbéen ga 14:20
2
Njàlbéen ga 14:18-19
Ci kaw loolu Melkisedeg buurub Salem, mi doon sarxalkatu Yàlla Aji Kawe ji, daldi ñëw, indi mburu ak biiñ. Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf!
Utforska Njàlbéen ga 14:18-19
3
Njàlbéen ga 14:22-23
Ibraam nag wax buurub Sodom ne ko: «Man yékkati naa sama loxo, Yàlla Aji Sax ju Kawe ji seede, moom mi sàkk asamaan ak suuf, nee naa: duma jël ci yaw dara, du puso, bi gëna tuut sax, su ko defee doo mana wax ne yaa ma taxa am alal.
Utforska Njàlbéen ga 14:22-23
Hem
Bibeln
Läsplaner
Videor