Njàlbéen ga 1:26-27

Njàlbéen ga 1:26-27 KYG

Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.» Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram; ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit, góor ak jigéen la bind.