Njàlbéen ga 6:1-4
Njàlbéen ga 6:1-4 KYG
Bi nga xamee ne nit ñi tàmbali nañoo fulandiwu ci kaw suuf, te am ay doom yu jigéen, ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar. Aji Sax ji daldi wax ne: «Manumaa bàyyi nit, muy wéyee dunde noo, gi ma ko may, ndax nit du dara lu dul suuxi neen, kon dinaa leen àppal diirub téeméeri at ak ñaar fukk (120).» Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur.