Njàlbéen ga 8:21-22

Njàlbéen ga 8:21-22 KYG

Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe. Li feek suuf di suuf, dootu jiwooy dakk mbaa ngóob, te du sedd aku tàngoor, du nawet it mbaa noor, mbaa guddeek bëccëg.»