Matthew 23
23
1Fōfale Yesu wah͈ mbōlo ma ak i tālube am, ne,
2Bindānkat ya ak Pharisee ya tōg nañu chi tōgu’ Musa:
3Mōtah͈ lu mu mun a don lu ñu len ebal, dēgal len, te def ko; wande bu len def naka sēn i jef; ndege ño di wah͈, te du ñu def.
4Ño di taka say yu dīs, te mite yubu, teg len chi i mbag i nit; wande ñom du ñu len randal ak sēn baram.
5Wande ño di def sēn i jef ndah͈ nit gis len: ndege ño di yāal sēn i galaj, te reyal sēn i mbichah͈tan i mbūba,
6Te sopa bereb yu koue chi i mbôtay, ak tōgu yu koue chi juma ya,
7Ak i noyo chi i ndaje, te nit di len ôe, Rabbi.
8Wande yēn, bu ñu len ôe Rabbi: ndege kena di sēn jemantalkat, te yēn a di i morom.
9Bu len ôe kena sēn bay chi aduna si; ndege kena di sēn Bay mu di ka cha ajana.
10Bu ñu len ôe borom; ndege kena di sēn borom, mō di Krista.
11Wande ku gen a rey chi sēn digante, na neka sēn bukanēg.
12Ku yēkati bop’ am, di nañu ko sufel; te ku sufelu bop’ am, di nañu ko yēkati.
13-14Wande suboh͈un yēn, bindānkat yi ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn tej bunt’ i ngur i ajana chi nit: te yēn chi sēn bopa du len cha tabi; te nanguwu len ña buga tabi ñu tabi cha.
15Suboh͈un yēn, bindānkat yi ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn wor gēch ak jēri ndig sopi bena tubēn; te ganou bu mu neke nōna, ngēn genati ko def mu neka dōm i nāri as yēn.
16Suboh͈un yēn, njītekat yu silmah͈a yi, yēn ñi wah͈, ne, Ku di geñ chi juma ja, dara la; wande ku di geñ chi wurus i juma ja, war na ko motali.
17Dof yi ak silmah͈a yi: bu chi gen a rey, wurus wā’m, am juma ja di selal wurus wa?
18Te, Ku di geñ cha lotel ba, dara la; wande ku di geñ cha maye ga cha kou am, war na ko motali.
19Silmaha yi: bu chi gen a rey, maye gā’m, am lotel ba di selal maye ga?
20Ku di geñ cha lotel ba mbōk, geñ na cha mōm, ak la cha kou am yepa.
21Te ku di geñ cha juma ja, geñ na cha mōm, ak ka fa deka.
22Te ku di geñ cha ajana, geñ na cha gangūne’ Yalla, ak cha mōm ka tōg cha kou am.
23Suboh͈un yēn, bindānkat yi ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn fey asaka i oyof ya, te sagane yef i yōn wa gen a rey, mu di njūbay, ak yermande, ak ngum: yile ñom ngēn war on a def, te bañ a sagane yena ya.
24Njītekat yu silmah͈a yi, ña sēga ab yô, te wona gelem.
25Suboh͈un yēn, bindānkat yi, ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn di setal biti’ ndap ak kela, wande cha bir fês na ak ndāntu ak nchaychay.
26You Pharisee bu silmah͈a bi, setalal jeka bir i ndap li ak kela bi, ndah͈ cha biti set itam.
27Suboh͈un yēn, bindānkat yi, ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn niro ak bamel ya ñu wêh͈al, ñu rafet chi biti, wande chi bir fês ak i yah͈ i ñu dē, ak nubay gu mun a don.
28Nōgu itam ngēn di wone njūlit chi nit chi biti, wande chi bir da ngēn fês ak nafeh͈a ak bakar.
29Suboh͈un yēn, bindānkat yi, ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn tabah͈ i bamel i yonent ya, te rafetlo i bamel i ñu jūb ña,
30Te ne, Su ñu nek’ on chi suñu bes i bay ya, doū ñu on bōlo ak ñom chi deret i yonent ya.
31Yēn a sēde lōgu chi sēn bopa, ne yēn a di dōm i ña rēy on yonent ya.
32Fêsal len mbōk sēn andār i bay ya.
33Jan yi, dōm i ñangor yi, naka ngēn munê moytu ndān i nāri?
34Tah͈na yōne nā len i yonent, ak i borom‐sago, ak i h͈amkat: di ngēn rēy ñena ñi, te dāj len cha kura; te di ngēn ratah͈ ñena ñi chi sēn i juma, te geten len chi dek’ ak deka:
35Ndah͈ deret i ñu jūb ña yepa ja tūru on chi suf ñou chi sēn kou, dôre ko cha deret i Abel ku jūb ka, be cha deret i Zachariah dōm i Barachiah, ka ngēn rēy on chi digante bereb bu sela ba ak lotel ba.
36Chi dega mangi len di wah͈, Yef yile yepa di nañu dal h͈êt wile.
37E Jerusalem, Jerusalem, mu rēy yonent ya, te jamat i h͈êr ña ñu ko yōne! naka lā don faral a buge dajale sēn i dōm, naka ganar gu di dajale i dōm am chi run lāf am, te ngēn bañ.
38Sēn nēg des na ak yēn te genta na.
39Ndege mangi len di wah͈, Du len ma gisati be bu ngēn di wah͈i, ne, Barkel chi ka di dika chi tur i Borom bi.
Цяпер абрана:
Matthew 23: GWG
Пазнака
Падзяліцца
Капіяваць
Хочаце, каб вашыя адзнакі былі захаваны на ўсіх вашых прыладах? Зарэгіструйцеся або ўвайдзіце
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.