Yàlla ne ko ca gént ga: «Waaw, xam naa ne li nga def du sa teyeef. Moo tax man it mayuma la nga laal ko, di ma tooñ. Léegi nag dellool góor gi soxnaam, ab yonent la de, te dina la ñaanal, nga raw. Waaye soo ko deful, na la bir ne dinga dee, yaak sa waa kër yépp.»