YouVersion Logo
Search Icon

John 18

18
1Ba Yesu wah͈ on bāt yoyu, mu gēna ak i talube am, jala deh͈ i Kidron, fa tōl neka, te mu duga chi bir, mōm ak i talube am.
2Judas, ka ko or on, h͈am on na bereb ba; ndege Yesu faral on na dem fōfa ak i talube am.
3Judas nak, ba mu ame i h͈arekat ak i saltige cha i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya, mu dika fōfale ak i lampa ak i nītu ak i ganay.
4Yesu ka h͈am yef ya ko di jot yepa, dem cha kanam, te ne len, Ana ku ngēn di ūt?
5Nu tontu ko, ne, Yesu wā’ Nazareth ba. Yesu ne len, Man la. Te Judas itam, ka ko or on, mu tah͈ou ak ñom.
6Tah͈na ba mu len wah͈e, ne, Man la, ñu delu ganou, te dānu chi suf.
7Mu lājati len ne, Ana ku ngēn di ūt? Te ñu ne, Yesu wā’ Nazareth ba.
8Yesu tontu, ne, Wah͈ on nā len ne Man la: su ngēn ma ūte, bayi len ñile ñu dem:
9Ndah͈ bāt ba mu wah͈ on motaliku, ne, Ña nga ma may on, rēralu ma chi kena.
10Simon Peter nak am on na jāsi, te mu bochi ko, te dōr jām i kelifa i seriñ ya, te dog nop’ i ndējor am. Tur i jām ba di Malchus.
11Yesu ne Peter, Delōl jāsi bi chi mbar am: nānu ba ma Bay ba joh͈, ndah͈ du ma cha nān am?
12H͈arekat ya nak ak saltige ba, ak i ndau i Yauod ya japa Yesu, te ew ko,
13Te jeka ko yubu fa Annas; ndege mō don goro i Caiaphas, ka nek’on kelifa i seriñ ya cha at mōmale.
14Caiaphas nak mō nek’on ka diktal on Yauod ya, ne ela na kena nit dē ngir mbōtay ga.
15Te Simon Peter top’ on na Yesu, ak benen talube. Talube bōbale nak, kēlifa i seriñ ya h͈am on na ko, te mu h͈araf ak Yesu cha bir ker i kēlifa i seriñ ya;
16Wande Peter tah͈ou cha biti bunta ba. Benen talube ba, ka kēlifa i seriñ ya h͈am on, dem cha biti te wah͈ ak jigen ja otu bunta ba, te indi Peter chi bir.
17Janh͈a bu don otu bunta ba ne Peter, Ndah͈ you itam a di kena chi i talube i nit koku? Mu ne, Man dowu ma.
18Jām ya nak ak ndau ya’nga fa tah͈ou on, ba ñu tāle safara i keriñ ndig seday ba, ñu di jāru; te Peter tah͈ou ak ñom di jāru.
19Kēlifa i seriñ ya lāj Yesu chi lu jem chi talube am ya, ak njemantale am.
20Yesu tontu ko, ne, Man chi kanam i ñepa lā wah͈ on chi aduna si; dan nā jemantal cha juma ya, ak cha jangu ba fa Yauod ya dajale ñepa; te wah͈u ma won dara chi kumpa.
21Ana lutah͈ nga ma lāj? lājal ña ma dēg’ on la ma len wah͈ on: ñile h͈am nañu la ma wah͈ on.
22Ba mu wah͈e lōlu, kena chi ndau ya’nga fa tah͈ou dōr Yesu ak loh͈o am, ne, Ndah͈ nōnu nga tonto kēlifa i serin ya?
23Yesu tontu ko, ne, Su ma wah͈e lu bon, sēdêl ma lu bon: wande su de lu bāh, ana lutah͈ nga dōr ma?
24Annas nak ew ko, te yōni ko Caiaphas, kēlifa i seriñ ya.
25Simon Peter don na tah͈ou di jāru. Ñu ne ko, Ndah͈ you itam neku la kena chi talube am yi? Mu wēdi, te ne, Man dowu ma.
26Kena chi i jām i kēlifa i seriñ ya, ku bok’ on ak ka Peter dog on nop’ am, ne, Ndah͈ gisu ma la won cha tōl ba ak mōm?
27Tah͈na mu wēdêti: te chi tah͈ouay seh͈a ga sab.
28Ñu omat Yesu nak cha Caiaphas be cha bir ateukay ba: te têl on na; ti ñom h͈arafu ñu cha ateukay ba, ndah͈ du ñu gakal sēn bopa, wande ndah͈ ñu mun a leka h͈ewte ga.
29Pilate nak gēna dem fa ñom, te ne, Ana lu ngēn am lu ngēn di sēde chi nit kile?
30Ñu tontu te ne ko, Su nekul on defkat i lu bon, kōn du ñu la ko jebal.
31Tah͈na Pilate ne len, Jel len ko yēn, te ate ko cha naka sēn yōn eble. Yauod ya ne ko, Daganul ñu rēy kena:
32Ndah͈ bāt i Yesu motaliku ba mu wah͈ on, di wone chi ban melo dē la dēeji.
33Pilate nak h͈arafati cha ateukay ba, te ô Yesu te ne ko, Ndah͈ yā di bur i Yauod ya?
34Yesu tontu, ne, Wah͈ nga ko you chi sa bopa, mbāte ndah͈ ñenen a la ko wah͈ chi lu jem chi man?
35Pilate tontu, ne, Ndah͈ Yauod la? Sa h͈êt i bopa ak i njīt i seriñ ya ño la jebale fi man: ana lo def?
36Yesu tontu, ne, Suma ngur bokul chi aduna sile: su suma ngur bok’ on chi aduna sile, kōn suma i bukanēg di nañu h͈ēh͈, ndah͈ du ñu ma jebal fa Yauod ya: wande suma ngur jugewul fōfule.
37Pilate ne ko, Ndah͈ bur nga? Yesu tontu, ne, Wah͈ nga ko, ndege man bur la. Lile tah͈ ma jūdu on, te lile tah͈ ma ñou chi aduna si, ndah͈ ma sēde dega gi. Ku neka ku boka chi dega gi di na dēga suma bāt.
38Pilate ne ko, Ana lu di dega?
39Te ba mu wah͈ on lōlu, mu gēnati fa Yauod ya, te ne len, Man gisu ma mu def lu bon.
40Wande am ngēn bāh͈ ne ma bayil len kena cha h͈ewte ga: ndah͈ buga ngēn ma bayil len Bur i Yauod ya?
41Tah͈na ñu h͈āchôti, ne, Dowul kile, wande Barabbas. Barabbas nak sachakat la won.

Currently Selected:

John 18: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in