1
Matthew 12:36-37
Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907
Te mangi len di wah͈, Bāt i nēn bu neka bu nit di wah͈, di na joh͈i warugal am chi bes i ate ba. Ndege chi sa i bāt la ñu la joh͈i njūbal, te chi sa i bāt la ñu la joh͈i ndānute.
Compara
Explorar Matthew 12:36-37
2
Matthew 12:34
E dōm i ñangor yi, yēn ñi bon, naka ngēn mune wah͈ lu bāh͈? ndege lu fês chi h͈ol gemeñ gi wah͈ ko.
Explorar Matthew 12:34
3
Matthew 12:35
Nit ku bāh͈ di na gēne yef yu bāh͈ chi dēnchukay am bu bāh͈; wande nit ku bon di na gēne yef yu bon chi dēnchukay am bu bon.
Explorar Matthew 12:35
4
Matthew 12:31
Mōtah͈ ma ne len, Bakar bu neka ak h͈as i Yalla, di nañu ko baal nit; wande ku h͈as Nh͈el mu Sela ma, du ñu ko baal.
Explorar Matthew 12:31
5
Matthew 12:33
Bāh͈lo len garap gi ak i dōm am; mbāte bonlo len garap gi ak i dōm am; ndege rañātle nañu garap gi chi i dōm am.
Explorar Matthew 12:33
Inici
La Bíblia
Plans
Vídeos