Ba ñu dajalô ak mag ña, te fēncha, ñu may otukat ya h͈alis bu bare, ne,
Na ngēn ne, I tālube am a dik’ on chi gudi, te sacha ko ba ñu neloue.
Su kēlifa ga dēge lile, di nañu ko dalal, te dindi len chi jāh͈le.
Ñu jel h͈ālis ba, te def la ñu len wah͈ on: kadu gile fireku chi digante Yauod ya, neka bentey.