John 2
2
1Cha ñetel i fan ba, sey am on na cha Cana i Galilee; te ndey i Yesu anga fa won.
2Ô on nañu itam Yesu ak i talube am cha sey ba.
3Te ba biñ ba jêh͈e, ndey i Yesu ne ko, Amatu ñu biñ.
4Te Yesu ne ko, Jigen ji, lu ma jote ak you? Suma wah͈tu dikangul.
5Ndey am ne bukanēg ya, Lu mu len wah͈, def len ko.
6Jurom ben’ i ndā i h͈êr anga fa won, naka āda i Yauod ya nek’ on ndig sēn setalay, bu cha neka mun na def natu yu bare.
7Yesu ne len, Fêsal len ndā yi ak ndoh͈. Te ñu fêsal len be cha gemeñ ya.
8Mu ne len, Tanh͈a len cha lēgi, te yub kēlifa nchēt ga. Te ñu yub ko.
9Ba kēlifa nchēt ga mose ndoh͈ ma sopaliku on biñ, te h͈amul fu mu juge, (wande bukanēg ya h͈am ya rôt on ndoh͈ ma), kēlifa nchēt ga ôlu seyt bu gōr ba,
10Te ne ko, Nit ku neka biñ bu bāh͈ ba la jeka tāj: te su ñu nāne be lu bare, mu isi bu genadi ba; yā dēncha biñ bu bah͈ bi be lêgi.
11Mandarga bu jeka bile la Yesu def on cha Cana i Galilee, te wone ndam am; te i talube am gum chi mōm.
12Ganou lōlu mu dem fa Capernaum, mōm, ak ndey am, ak i rak’ am, ak i talube am; te ñu jēki fa fan yu new.
13Te h͈ewte i Yauod ya jegeñsi na, te Yesu dem fa Jerusalem.
14Te mu feka cha bir juma ja ña don jay i nag ak i nh͈ar ak i mpetah͈, ak wēchikat i h͈ālis di tōg:
15Te mu defar yar i būm, te dah͈a yepa cha biti juma ja, nh͈ar ya ak nag ya; te mu tūr h͈ālis i wēchikat ya, te dānel sēn i tabul;
16Te mu ne ña don jay mpetah͈ ya, Fab len yile cha biti; bu len def suma nēg i Bay nēg i jayukay.
17I talube am fataliku ne bind’ on nañu, ne, Sa nchauarte i nēg ba leka na ma fepa.
18Yauod ya nak tontu te ne ko, Ban mandarga nga ño wone, ndege def nga yef yile?
19Yesu tontu te ne len, Maba len juma jile, te chi ñet’ i fan di nā ko delu tah͈oual.
20Yauod ya ne ko, Ñenent fuk’ i at ak jurom bena la ñu am di tabah͈ juma jile, te you di nga ko tah͈oual chi ñet’ i fan am?
21Wande wah͈ on na chi juma i yaram am.
22Ba mu dēkaliku on cha dē ga, i talube am fataliku ne wah͈ on na lōlu, te gum on nañu mbinda ma, ak bāt ba Yesu wah͈ on.
23Ba mu neke cha Jerusalem cha h͈ewte i njot ga, ñu bare gum on nañu chi tur am, ba ñu gise koutef ya mu def on.
24Wande Yesu ōluwul on bop’ am ak ñom, ndege h͈am on na ñepa,
25Te soh͈lawul kena sēde chi lu jem chi nit; ndege mō h͈am on lu neka chi h͈ol i nit.
S'ha seleccionat:
John 2: GWG
Subratllat
Comparteix
Copia
Vols que els teus subratllats es desin a tots els teus dispositius? Registra't o inicia sessió
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.