Matthew 12

12
1Cha jamāno jōjale Yesu jār on na cha tō i mboh͈a ya chi bes i dimas; te i tālube am h͈īf, dōr di budi i gub i mboh͈a ya, te di leka.
2Wande Pharisee ya ba ñu gise lōla, ñu ne ko, Sêtal, sa i tālube ange def lu daganul a def chi bes i dimas.
3Wande mu ne len, Ndah͈ jangu len la Dauda def on ba mu h͈īfe, ak ña and’ on ak mōm;
4Na mu h͈arafe chi nēg i Yalla ba, te leka mburu ma ñu dān wone, ma daganul on mu leka, wala ña and’ on ak mōm, wande seriñ ya dal?
5Jangu len itam chi mbinda yi naka seriñ ya chi bes i dimas moy dimas ja cha juma ja, te bakaru ñu?
6Wande mangi len di wah͈, Kena angile ki gen a rey as juma ja.
7Wande su ngēn h͈am on lu lile tiki, Yermande lā buga as h͈arfan, kôn dōtu len eda ña moyul.
8Ndege Dōm i nit ka mō di Boromdimas.
9Mu juge fōfale, te h͈araf chi sēn juma:
10Te gōr anga fa ku am loh͈o bu lagi. Ñu lāj ko, ne, Mbar dagan na weral chi bes i dimas? Ndah͈ ñu mun ko jêñ.
11Mu ne len, Kan nit a neka chi yēn ku am bena nh͈ar, su dānô chi mpah͈ chi bes i dimas, do ko japa te dindi ko?
12Naka la nit gene nh͈ar! Mōtah͈ dagan na def lu bāh͈ chi bes i dimas.
13Fōfale mu wah͈ gōr ga, ne, Talalal sa loh͈o. Mu talal ko; mu wer niki benen ba.
14Wande Pharisee ya gēna, te fēncha naka ñu ko mun a rēye.
15Yesu h͈am lōla, te mu sipi fōfale; ñu bare topa ko; mu weral len ñom ñepa.
16Te mu ebal len, ne, Bu ko kena h͈am:
17Ndah͈ la Isaiah yonent ba wah͈ on motaliku, ne,
18Sêt len, suma ndau ba ma tana; suma sopa ka nêh͈ lol chi suma fit; di nā teg suma Nh͈el chi kou am, te di na yēgle lu jūb chi Gentile ya.
19Du h͈ūlo, mbāte h͈āchu, te ken du dēga bāt am chi mbeda yi.
20Du dama sonka bu lūnka, du fey gilinta bu di sah͈ar, be mu yōni njūbay be chi ndam.
21Te chi tur am la Gentile ya di yākari.
22Fōfale ñu indi fa mom kena ku jine jap’ on, ka silmah͈a te lū; mu weral ko, tah͈na nit ka lū on wah͈ te gis.
23Nit ña ñepa jomi, te ne, Kile du dōm i Dauda’m?
24Wande ba ko Pharisee ya dēge, ñu ne, Kile gēneūl jine ya lu dul chi Abdujambar njīt i jine ya.
25Mu h͈am sēn i h͈alāt, te ne len, Ngur gu neka gu h͈ajāliku chi bop’ am, di na ñou chi ntaste; te deka bu neka, mbāte nēg, bu h͈ajāliku chi bop’ am du tah͈ou:
26Te su Seytane gēnê Seytane, hajāliku na chi bop’ am; naka la ngur am di tah͈oue mbōk?
27Su ma gēnê i jine chi Abdujambar, sēn i dōm chi kan la ñu len gēne? mōtah͈ di nañu neka sēn i atekat.
28Wande su ma gēnê jine ya chi Nh͈el i Yalla, bōba ngur i Yalla dika na fi yēn.
29Naka la kena munê h͈araf chi nēg i borom‐dōle, te yah͈a alal am, su jekulê taka borom‐dōle ja? te ganou lōla di na yah͈a nēg am.
30Ku nekul ak man, bañ na ma; te ku dajaleūl ak man, defa tasāre.
31Mōtah͈ ma ne len, Bakar bu neka ak h͈as i Yalla, di nañu ko baal nit; wande ku h͈as Nh͈el mu Sela ma, du ñu ko baal.
32Te ku wah͈ lu bon lu jem chi Dōm i nit ka, di nañu ko baal; wande ku wah͈ lu bon lu jem chi Nh͈el mu Sela ma, du ñu ko baali muka chi aduna sile, wala chi lah͈īra.
33Bāh͈lo len garap gi ak i dōm am; mbāte bonlo len garap gi ak i dōm am; ndege rañātle nañu garap gi chi i dōm am.
34E dōm i ñangor yi, yēn ñi bon, naka ngēn mune wah͈ lu bāh͈? ndege lu fês chi h͈ol gemeñ gi wah͈ ko.
35Nit ku bāh͈ di na gēne yef yu bāh͈ chi dēnchukay am bu bāh͈; wande nit ku bon di na gēne yef yu bon chi dēnchukay am bu bon.
36Te mangi len di wah͈, Bāt i nēn bu neka bu nit di wah͈, di na joh͈i warugal am chi bes i ate ba.
37Ndege chi sa i bāt la ñu la joh͈i njūbal, te chi sa i bāt la ñu la joh͈i ndānute.
38Fōfale ñena chi bindānkat ya ak Pharisee ya tontu ko, ne, Jemantalkat bi, buga naño gis mandarga chi you.
39Wande mu tontu len, ne, H͈êt i ēfar ak i njālokat ūt na mandarga, wande du ñu ko may mandarga lu moy mandarga i Jonah yonent ba;
40Ndege naka Jonah nek’on chi bir mbonkana ma ñet’ i bechek ak ñet’ i gudi, nōgule la Dōm i nit ka di nekeji chi h͈ol i suf si ñet’ i bechek ak ñet’ i gudi.
41Ga’ Nineveh ña di nañu tah͈ou chi bes i ate ba ak h͈êt wile, te ey len; ndege rēchu on nañu chi wāre’ Jonah, te ku gen a rey Jonah angi fi.
42Bur i gopu bu jigen ba di na tah͈ou chi bes i ate ba ak h͈êt wile, te ey len; ndege juge on na fu sorey ndah͈ mu dēga sago i Suleyman, te ku gen a rey Suleyman angi fi.
43Wande nh͈el mu sobe mi, ba mu gēne chi nit, mu doh͈ chi bereb yu wou, di ūt noflay, te feku ko.
44Fōfale mu ne, Di nā delu chi suma nēg fa ma gēn’ on; te ba mu deluse, mu feka ko am nēn, mu būb, te nah͈ātu.
45Mu dem, te bōle ak mōm yenen jurom ñar i nh͈el yu gen a bon as bop’ am, ñu h͈araf chi bir, te deka fa; te muj i nit kōkale gen na bon as ndôrte am. Nōgule la di meli chi h͈êt wu bon wile.
46Ba mu wah͈andô ak mbōlo ma, ndey am ak i rak’ am tah͈ou cha biti, di buga wah͈ ak mōm.
47Kena ne ko, Sa ndey ak sa i rak’ anga tah͈ou cha biti, di buga wah͈ ak you.
48Wande mu tontu ka ko wah͈, ne, Kan a di suma ndey? te ñan a di suma i raka?
49Mu talal loh͈o am chi i tālube am, te ne, Sêt len, suma ndey ak suma i raka!
50Ndege ku mu mun a don ku di def suma mbugel i Bay ba cha ajana, mō di suma raka, ak suma jigen, ak suma ndey.

S'ha seleccionat:

Matthew 12: GWG

Subratllat

Comparteix

Copia

None

Vols que els teus subratllats es desin a tots els teus dispositius? Registra't o inicia sessió