Matthew 13
13
1Chi bes bōba Yesu gēna on na cha nēg ba, te tōg cha tefes ga.
2Mbōlo mu rey dajalo fi mōm; tah͈na mu duga chi gāl, tōg, te mbōlo ma yepa tah͈ou cha tefes ga.
3Mu wah͈ len yef yu bare chi i lēb, ne, Bena jikat dem on na ji;
4Te ba mu jie, yena pēpa rot nañu cha wet i yōn wa, te mpicha ya dika for len;
5Yenen rot chi i bereb i doch, fa ñu amule suf su bare; ñu gou a sah͈, ndege suf sa h͈ōtul;
6Ba janta ba fenke mu laka len; te ñu lah͈, ndege amu ñu rên.
7Yenen rot chi digante i tah͈as, te tah͈as yi sah͈ando ak ñom, te waka len:
8Yenen rot chi suf su bāh͈ sa, te mēña mēñef, yena ya tēmēr, yale jurom bena fuka, yale ñeta fuka.
9Ku am i nopa, na dēga.
10Tālube ya ñou te ne ko, Lutah͈ nga wah͈ ak ñom chi i lēb?
11Mu tontu len, ne, Yēn la ñu may ngēn h͈am i kumpa i ngur i ajana, wande ñom mayu ñu len ko.
12Ndege ka am mōm la ño may, te di na am lu bare; wande ka amul, di nañu jel la mu am sah͈.
13Mōtah͈ ma wah͈ ak ñom chi i lēb; ndege ba ñu gise, du ñu gis; te ba ñu dēge du ñu dēga; te fafu ñu di h͈am.
14Te chi ñom la bāt i Isaiah motaliku, ne, Di dēga di ngēn dēga, wande du len h͈am; te di gis di ngēn gis, wande du len sēnu:
15Ndege h͈ol i nit ñile dūf na, sēn i nopa teh͈ nañu, te tej nañu sēn i but; ndah͈ du ñu gis ak sēn i but, dēga ak sēn i nopa, tūb, te ma weral len.
16Wande barkel chi sēn i but, ndege da ñu gis; ak sēn i nopa, ndege da ñu dēga.
17Ndege chi dega mangi len di wah͈, Yonent yu bare ak nit ñu jūb bug’ on naño gis li ngēn gis, te gisu ñu ko won; te dēga li ngēn dēga, wande dēgu ñu ko won.
18Dēga len mbōk lēb i jikat ba.
19Ba kena dēge bāt i ngur gi, te h͈amu ko, fōfale la Seytane ñoue, te dindi la ñu ji won chi h͈ol am. Kile di ka ñu ji won chi wet i yōn wa.
20Te ka ñu ji won chi i bereb i doch, mō di ka dēga bāt bi, te dal di ko nangu ak banēh͈;
21Wande amul rên chi bop’ am, te muñ chi sā yu new dal; ndege su nah͈ar joge wala ngeten ndig bāt bi, nōg’ ak nōga mu fakatalu.
22Ka ñu ji won chi digante tah͈as ya, mō di ka dēga bāt bi; te i ntopato’ aduna si, ak nah͈ay i amam, waka bāt bi, mu bañ a mēña dōm.
23Te ka ñu ji won chi suf su bāh͈ sa, mō di ka dēga bāt bi, te h͈am ko, te mēña dōm chi dega, yena ya tēmēr, yale jurom bena fuka, yale ñeta fuka.
24Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak nit ka ji on jiu ju bāh͈ chi tōl am;
25Wande ba ñu neloue, mbañ am dika, te ji nduh͈um chi digante dugup ja, te dem.
26Ba dugup ja sah͈e, te mēña dōm, nduh͈um la fêñ itam.
27I rapas i borom‐ker ga ñou, te ne ko, Borom bi, ndah͈ jiū la won jiu ju bāh͈ chi sa tōl? naka la ame nduh͈um nak?
28Mu ne len, Ab mbañ a def lōlu. Rapas ya ne ko, Buga nga ñu dem budi len?
29Wande mu ne, Dēt, h͈ēchna bu ngēn di budi nduh͈um la, di ngēn budiāle dugup ja it.
30Bayi len ñar ña ñu sah͈ando be cha ngōbte ga; te cha wah͈tu’ ngōbte ga di nā wah͈ gōbkat ya, ne, Budi len jeka nduh͈um la, taka ko i say te laka ko; wande dajale len dugup ja chi suma sah͈a.
31Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak pēp’ i sūna, bu nit fab, te ji chi tōl am;
32Mō gen a tūt chi i pēpa yepa; wande su sah͈e, mō gen a rey chi gir am yepa, te mu neka garap be mpich’ i asaman yi di dika dal chi i banh͈as am.
33Mu wah͈ len benen lēb, ne, Ngur i ajana niro na ak mporoh͈al bu jigen jel, te def chi ñet’ i andār i sunguf, be yepa foroh͈.
34Yesu wah͈ on na mbōlo ma yef yile yepa chi i lēb, te wah͈u len dara lu dul chi lēb:
35Ndah͈ la yonent ba wah͈ on motaliku, ne, Di nā ūbi suma gemeñ chi i lēb; di nā yēgle yef yu nubu cha ndôrte’ aduna si.
36Fōfale Yesu bayi mbōlo ma, h͈araf chi nēg ba; te tālube am ya ñou fi mōm, ne, Tiki ñu lēb i nduh͈um i tōl ba.
37Mu tontu len, ne, Ka ji jiu wu bāh͈ ba, Dōm i nit ka la;
38Tōl ba aduna si la; jiu wu bāh͈ wa i dōm i ngur ga la; nduh͈um la i dōm i bulis la;
39Mbañ ma ko ji on Seytane la; ngōbte ga muj i aduna si la; te gōbkat ya ño di malāka ya.
40Naka ñu budi nduh͈um la, te laka ko chi safara, nōgu la di neki chi muj i aduna.
41Dōm i nit ka di na yōne i malāk’ am, te di nañu forātu chi ngur am yef yu moylo yepa, ak ña def lu bon;
42Te sani len cha safara sa; fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.
43Bōba ñu jūb ña di nañu melah͈ na janta bi chi sēn ngur i Bay ba. Ku am i nopa na dēga.
44Ngur i ajana niro na ak alal bu nubu chi bir tōl; ba ko nit feke mu nuba ko, dem chi banēh͈ am jay lu mu am on yepa, te jenda tōl bōbale.
45Ngur i ajana nirôti na ak jūla ku don ūt jamong yu bāh͈;
46Ba mu feke bena jamong ju jafe njēg, mu dem jay lu mu am on yepa, te jenda ko.
47Ngur i ajana nirôti na ak mbal mu ñu sani chi gēch, mu japa h͈êt i jen wu neka:
48Ba mu fêse, ñu h͈ēcha ko chi tefes; ñu tōg chi suf, te dajale yu bāh͈ ya chi i ndap, wande sani yu bon ya fale.
49Nōgule la neki chi muj i aduna: malāka ya di nañu juge, te h͈ajātle ñu bon ña cha ñu jūb ña,
50Te sani len chi safara si: fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.
51Ndah͈ dēga ngēn yef yile yepa? Ñu ne ko, Wau.
52Mu ne len, Bindānkat bu neka mbōk bu ñu nekalo tālube chi ngur i ajana, niro na ak borom‐ker ku gēne chi dēnchukay am lu ês ak lu maget.
53Am on na ba Yesu sotal on lēb yile, mu juge fōfa.
54Ba mu dike chi rew am, mu jemantale len chi sēn i juma, tah͈na ñu jomi, ne, Nit kile naka la ame h͈amh͈am bile, ak koutef yile?
55Kile du dōm i minise bā’m? du ndey am a tūda Mariama? te i rak’ am James, ak Yusufa, ak Simon, ak Judas?
56Te i jigen am, du chi suñu digante la ñu neka? Naka la kile ame yef yile yepa?
57Ñu fakatalu chi mōm. Wande Yesu ne len, Yonent ñakul teranga lu moy chi dek’ am, ak chi ker am.
58Defu fa i koutef yu bare ndig sēn gumadi.
S'ha seleccionat:
Matthew 13: GWG
Subratllat
Comparteix
Copia
Vols que els teus subratllats es desin a tots els teus dispositius? Registra't o inicia sessió
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

: