Matthew 14

14
1Cha jamāno jōjale Herod kēlifa ga dēg’ on na lu ñu wah͈ lu jem chi Yesu,
2Te mu ne bukanēg am ya, Kile di John Batisekat ba; dēki na cha dē ga; mōtah͈ koutef yile fêñ nañu chi mōm.
3Ndege Herod jap’ on na John, ewo ko, te tej ko chi kaso, ndig Herodias, jabar i Philip rak’ am.
4Ndege John dān na ko wah͈, ne, Daganul nga sey ak mōm.
5Ba mu ko buge rēy, mu ragal mbōlo ma, ndege fōg nañu ne yonent la won.
6Wande ba ño h͈umbal bes i njudu’ Herod, dōm i Herodias ju jigen fēcha chi sēn digante, mu nêh͈ Herod lol.
7Mōtah͈ mu dig ak geñ ne, di na ko may lu mun a don lu mu lāj.
8Mōm nak ndege ndey am jeñtal na ko, ne, May ma file bop’ i John Batisekat ba chi ndap.
9Bur ba nah͈arlu ko; wande ndig geñ am ga, ak ña tōg on ak mōm di leka, mu ebal ñu may ko ko.
10Mu yōni ku dog bop’ i John chi kaso ba.
11Ñu indi bop’ am chi ndap, may ko janh͈a ba, mu yubu ko fa ndey am.
12Tālube am ya ñou, jel yaram wa, sūl ko, te dem nitali ko Yesu.
13Ba ko Yesu dēge, mu juge fa chi gāl chi manding mu wēt: ba mbōlo ma dēge lōla, ñu rūnga topa ko tank’ ak tanka cha deka ya.
14Mu gēna, te gis mbōlo mu rey; mu am yermande chi ñom, te weral sēn i jarak.
15Ba ngon jote, i tālube am ñou fi mōm, ne, File manding la, te wah͈tu wi wey na jēg; na nga ebal mbōlo mi ñu dem cha bir deka ya, te jenda dundu.
16Wande Yesu ne len, Soh͈laū ño dem; may len ñu leka.
17Ñu ne ko, Am nañu fi jurom i mburu reka, ak ñar i jen.
18Mu ne, Indi len fi man.
19Mu ebal mbōlo ma ñu tōg chi kou ñah ma, jel jurom i mburu ya ak ñar i jen ya, yēkati but am cha asaman, gerem Yalla, dogat mburu ya, joh͈ len talube ya, te tālube ya joh͈ len mbōlo ma.
20Ñepa leka be sūr; ñu forātu ndesit ma be ñu fêsal fuk’ i sendel ak ñar.
21Ña lek’ on jurom i njūne’ gōr la ñu potah͈, ganou i jigen ak i gūne.
22Nōn’ ak nōna mu jeñtal i tālube am ñu duga chi gāl ga, te jītu ko cha genen wet ga, be ba mu demlô mbōlo ma.
23Ganou ba mu demlô mbōlo ma, mu yēg cha kou tūnda wa ndah͈ mu ñān Yalla, te chi gudi ga mu neka fa mōm dal.
24Wande nak gāl ga nek’ on na chi kou gēch ga, di yengatu chi dūs ya; ndege ngelou la defa nah͈ari won.
25Chi ñenentel i wah͈tu chi gudi gi, mu dem fa ñom di doh͈ chi kou gēch ga.
26Ba ko i tālube am gise mu di doh͈ chi kou gēch ga, ñu tīt, ne, Njuma la; te ñu h͈āchu ndig tītay.
27Wande Yesu wah͈ len chi tah͈ouay, ne, Dalal len sēn h͈ol: Man la; bu len tīt.
28Peter tontu ko, ne, Borom bi, su de you, ô ma ma ñou fi you chi kou ndoh͈ mi.
29Mu ne ko, Ñoual. Peter wacha chi gāl ga, te mu doh͈ chi kou ndoh͈ ma mu dem fa Yesu.
30Wande ba mu gise ngelou li, mu tīt, te dal di dīg; mu h͈āchu, ne, Borom bi, musal ma.
31Nōn’ ak nōna Yesu talal loh͈o am, te japa ko, ne ko, E borom‐ngum gu new, lutah͈ nga nimse?
32Ba ñu ñoue chi bir gāl ga, ngelou li dal.
33Te ña neka chi gāl ga jāmu ko, ne, Chi dega yā di Dōm i Yalla.
34Ba ñu jale, ñu dika chi suf si, chi Gennesaret.
35Ba ko nit ña cha wet gōgale h͈ame, ñu yōni chi rew mōma yepa, indi fa mōm ña jēr ñepa;
36Te dagān ko ndah͈ ñu mun a lāl omb’ i cholay am reka; te ña ko lāl ñepa ñu wer cheng.

S'ha seleccionat:

Matthew 14: GWG

Subratllat

Comparteix

Copia

None

Vols que els teus subratllats es desin a tots els teus dispositius? Registra't o inicia sessió