Matthew 24
24
1Yesu don na gēna cha juma ja, di dem yōn am; te i tālube am ñou fi mōm, di ko won i tabah͈ i juma ja.
2Wande mu tontu len, ne, Sêtu len yef yile yepa? Chi dega mangi len di wah͈, Bena h͈êr du des chi kou morom am bu ñu dul dānel chi suf.
3Ba mu tōge chi tūnda i Olive ya, tālube ya ñou fi mōm chi mpet, ne, Wah͈ ñu, kañ la yef yile di ami? te la di doi sa mandarga’ ndika, ak i muj i aduna si?
4Yesu tontu len, ne, Otu len bu len kena nah͈.
5Ndege ñu bare di nañu ñoui chi suma tur, ne, Mā di Krista, te di nañu nah͈i ñu bare.
6Te di ngēn dēga i h͈are ak i h͈abar i h͈are: otu len ngēn jāh͈le: ndege yile soh͈la naño am; wande muj ga dikangul.
7Ndege h͈êt di na jog chi kou h͈êt, ak ngur chi kou ngur: i h͈īf di nañu ami, ak i yengatu’ suf si chi bereb yu bare.
8Wande yile yepa ndôrte i nah͈ar la.
9Fōfale di nañu len jebale ndah͈ ñu geten len, te di nañu len rēy: h͈êt yi yepa di nañu len sib ndig man.
10Fōfale ñu bare di nañu fakatalu, orante, te sibante.
11Yonent i nafeh͈a yu bare di nañu jogi, te nah͈ ñu bare.
12Te ndig bakar di na fūs, nchofel i ñu bare di na wañiku.
13Wande ka di muñ be cha muj ga, di na mucha.
14Bile linjil i ngur gi, di nañu ko wāre chi aduna si yepa ndig sēde chi h͈êt yi yepa; cha ganou ga muj ga di na ñou.
15Bu ngēn di gisi suboh͈un ak h͈udosun mbōk mu di tah͈ou chi bereb bu sela ba, naka Daniel yonent ba wah͈ on (ka ko janga na h͈am),
16Fōfale na ña neka chi Judæa dou cha tūnda ya:
17Ku neka chi kou nēg, bu mu wacha mu gēne yef ya chi nēg am:
18Te ku neka chi tōl am, bu mu delusêti jel yēre am.
19Wande ndeysan jigen ña bir, ak ña di nampal chi bes yōgale!
20Ñān len ndah͈ sēn dou du neka chi wah͈tu’ seda, wala chi bes i dimas:
21Ndege chi wah͈tu wōwale, nah͈ar wu rey di na ami, naka mu mosulê am cha ndôrte’ aduna si bentey, dēt, te dōtu am bel mōs.
22Su ñu gatalul on bes yōgale, ken du kon muchi: wande ngir ña ñu tana, di nañu gatal bes yōgale.
23Fōfale su ñu len ne, Krista angile, mbāte mungale; bu len ko gum.
24Ndege Krista yu nafeh͈a di nañu jogi, ak yonent yu nafeh͈a, te wone mandarga yu rey ak i koutef; be ñu di nah͈i ña ñu tana sah͈, su munê am.
25Mangi len di yēgal bala wah͈tu wa jot.
26Mōtah͈ su ñu len wah͈e, ne, Munga cha manding ma; bu len fa dem: munga chi bir nēg ya; bu len ko gum.
27Ndege naka melah͈ ma jugê cha penku, te fêñu be cha h͈arfu, nōgu la ndika i Dōm i nit ka di mel.
28Fu rēnda neka, fa la jah͈ay ya di dajalo.
29Cha ganou nah͈ar i bes yōyale, nōn’ ak nōna janta bi di na lendem, wêr wi du joh͈e lêr am, bidiw yi di nañu dānu cha asaman, te i kantan i asaman si di nañu yengatu:
30Fōfale mandarga i Dōm i nit ka di na fêñ cha asaman; h͈êt i aduna si yepa di nañu yeremtu, te di nañu gis Dōm i nit ka mu di ñou chi i nir i asaman si ak kantan ak ndam lu rey.
31Te di na yōni malāka am ya ak nchōu i bufta bu rey, te di nañu dajale ña mu tan’ on chi ñenent i ngelou yi, cha bop’ i asaman be cha muj ga.
32Dēglu len nak lēb i garap i sōto ga: ba banh͈as am mokase, te i h͈ob am suh͈ase, h͈am ngēn ne nauet jegeñsi na;
33Nōgu itam su ngēn gise yef yile yepa, na ngēn h͈am ne jegeñsi na, be chi sēn bunta sah͈.
34Chi dega mangi len di wah͈, H͈êt wile du wey be yef yile yepa am.
35Asaman ak suf di na wey, wande suma i bāt du wey.
36Wande ken h͈amul bes bōbale ak wah͈tu wōgale, du malāka i ajana ya sah͈, wala Dōm ja, wande suma Bay bi dal.
37Naka i bes i Noah nek’ on, nōgu la ndika i Dōm i nit ka di meli.
38Ndege naka chi bes yu jītu on tufan la, ñunga don leka, nān, sey te seylo, be cha bes ba Noah h͈arafe chi gāl ga,
39Te yēgu ñu be tufan la ñou yubuāle len ñepa; nōgu la ndika i Dōm i nit ka di meli.
40Fōfale ñar i nit di nañu neki chi tōl; ñu jel kena, te bayi ka cha des:
41Ñar i jigen di nañu di wol chi wolukay; ñu jel kena, te bayi ka cha des.
42Otu len mbōk; ndege h͈amu len ban bes la sēn Borom di ñoui.
43Wande h͈am len lile, ne su borom‐ker ga h͈am on chi wan wah͈tu la sachakat ba di ñou, otu kon na, te du bayi mu toj nēg am.
44Mōtah͈ na ngēn di defaru yēn it: ndege Dōm i nit ka di na ñoui chi wah͈tu bu ngēn dul fōg.
45Kan a di bukanēg mbōk bu taku te têy, bu borom am jītal chi ker am, ndah͈ mu joh͈ len sēn dundu chi wah͈tu wa?
46Barkel chi bukanēg bōbale, ba borom am di feka mu di def nōga ba mu agse.
47Chi dega mangi len di wah͈, Di na ko teg njīt cha la mu am yepa.
48Wande su bukanēg bu bon bale wah͈e chi h͈ol am, ne, Suma borom yīh͈ na;
49Te dal di dōr i naule am, leka ak nān ak mandikat ya;
50Borom i bukanēg bōbale di na ñou chi bes bu mu ko sēnuwul, ak chi wah͈tu wu mu h͈amul,
51Dog ko chi diga, te sedāle ko nafeh͈a ya: fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.
S'ha seleccionat:
Matthew 24: GWG
Subratllat
Comparteix
Copia
Vols que els teus subratllats es desin a tots els teus dispositius? Registra't o inicia sessió
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.