Matthew 11

11
1Am on na ba Yesu sotal on eble fuk’ i tālube am ak ñar ña, mu juge fa, ndah͈ mu jemantale te wāre chi sēn i deka.
2Ba John dēge chi tejukay ba i koutef i Krista, mu yōne cha i tālube am;
3Ñu ne ke, Ndah͈ yā di ki war a dika, am war naño sēnu kenen?
4Yesu tontu len, ne, Dem len, nitali John li ngēn dēga, ak li ngēn gis;
5Silmah͈a yange gis, lago yange doh͈, gāna yange wer, teh͈ yange dēga, ña dē dēkaliku, te ñunge wāre linjil bi chi miskin ya.
6Te barkel chi ku dul feka fakatalu chi man.
7Ba ñu deme, Yesu dal di ne mbōlo ma lu jem chi John, Lan ngēn dem on cha manding ma ndah͈ ngēn sêt? H͈īs bu di yengatu ak ngelou lê’m?
8Wande lan ngēn dem on ndah͈ ngēn sêt? Nit ku sāngu chi nchangay lu noy am? Ña sāngu chi nchangay lu noy angi chi i nēg ī bur.
9Wande lutah͈ on ngēn dem? sêt ab yonent am? Wau, ma ne len, te ku upa yonent.
10Kile mō di ka ñu bind’ on, ne, Di nā yōni suma ndau chi sa kanam, ka di wāj sa yōn chi sa kanam.
11Chi dega mangi len di wah͈, Ku gen a rey John Batisekat ba jugêngul cha ña judu chi jigen; wande ka gen a tut chi ngur i ajana, mō ko gen a rey.
12Cha jamāno i John Batisekat ba bentey, chi nchouarte la ñu fab ngur i ajana, te ña souar japa ko.
13Ndege yonent ya yepa ak yōn wa yēgle on nañu be cha John.
14Te su ngēn ko buge nangu, kile di Elijah, ka war a ñou.
15Ku am nopa yu mu dēge, na dēga.
16Wande ak lan la h͈êt wile niro? Niro na ak h͈alel ñu jēki chi i ndaje, di h͈āchu chi sēn i mās,
17Ne, Lītal nañu len, te fēchu len; yeremtu nañu, te joyu len.
18Ndege John ñouūl on di leka wala di nān, te ñu ne, Anda na ak jine.
19Dōm i nit ka ñou di leka te di nān, te ñu ne ko, Fuh͈alekat bi, ak nānkat i biñ bi, ak and’ i publican yi ak bakarkat yi. Wande sago jubantiku na chi i jef am.
20Fōfale mu dal di eda deka ya fa mu def on koutef am yu gen a bare, ndege da ñu rēchuwul.
21Suboh͈un you Chorazin! suboh͈un you Bethsaida! ndege koutef ya ma def on chi yēn, su ñu len def on chi Tyre ak Sidon, rēchu kon nañu bu yāga chi sagar ak dōm i tāl.
22Wande mangi len di wah͈, Di na gen chi Tyre ak Sidon chi kerog mpēnch’ um Yalla ma as yēn.
23Te you Capernaum, mi yēkatiku cha asaman, di nañu la sufel be chi nāri: ndege koutef ya ma def on chi you, su ñu len def on cha Sodom, kôn mu des bentey.
24Wande mangi len di wah͈, Di na gen chi rew i Sodom chi kerog mpēnch’ um Yalla ma as you.
25Cha wah͈tu wōwale Yesu tontu, ne, Mangi la gerem, Bay bi, Borom’ asaman ak suf, ndege nuba nga yef yile chi borom‐h͈amh͈am yi ak borom‐sago yi, te fêñal len i gūne.
26Na di nōgule, Bay bi, cha naka mu la nêh͈e chi sa kanam.
27Suma Bay jebal na ma yef yepa; te ken h͈amul Dōm ji wande Bay bi; te ken h͈amul Bay bi wande Dōm ji, ak ku Dōm ji nangu mu h͈am ko.
28Dikasi len fi man yēn ña lota te dīs ñepa, te di nā len may noflay.
29Enu len suma suf chi yēn, te jemantu len chi man; ndege da ma lew, te sufelu chi h͈ol; te di ngēn feka noflay chi sēn i fit.
30Ndege suma suf yomba na, te suma en oyof na.

Jelenleg kiválasztva:

Matthew 11: GWG

Kiemelés

Megosztás

Másolás

None

Szeretnéd, hogy a kiemeléseid minden eszközödön megjelenjenek? Regisztrálj vagy jelentkezz be