Matthew 3
3
1Chi bes yōyale la John Batisekat ba ñou on, di wāre cha manding i Judæa, ne,
2Rēchu len, ndege ngur i ajana jegeñsi na.
3Kile mō di ka Isaiah yonent ba wah͈ on, ne, Bāt i kena di h͈āchu chi manding ma, ne, Wājal len yōn i Borom bi, defar len i yōn am ñu tali.
4John nak mō sol on nchangay i kouar i gelem, ak lah͈asay i der chi ndig am; te dundu am njērer la won, ak lem i ala.
5Jerusalem, ak Judæa yepa, ak deka yu jegeñ Jordan yepa, dem fa mōm,
6Te mu batise len chi deh͈ i Jordan, ñu di wējal sēn i bakar.
7Wande ba mu gise jupa chi Pharisee ya ak Sadducee ya di ñou chi batise am, mu ne len, E h͈êt i ñangōr gi, kan a len yēgal ngēn di ūt a rēcha chi mer mi di ñou?
8Mēña len mbōk mēñef yu mot chi rēchu:
9Te bu len dēfe ne chi sēn bopa, Am nañu Ibrayuma mu di suñu bay; ndege mangi len di wah͈, ne Yalla mun na chi h͈êr yile sah͈ gēne chi i dōm i Ibrayuma.
10Te nistey teg nañu semiñ wi chi rēn i garap ya; garap gu neka mbōk gu mēñul dōm yu bāh͈, di nañu ko dog, te sani ko chi safara.
11Mā len di batise chi ndoh͈ ndig rēchu; wande mōm ka di topa chi man, mō ma gēti kantan; daganu ma yubu i dal’ am; mō len di batiseji chi Nh͈el mu Sela ma ak safara;
12Am na layu chi loh͈o am, te di na setali boju am fou, te dajale dugup am chi sah͈a mi; wande di na laka choh͈ ba chi safara su feyatil muk.
13Fōfale Yesu juge Galilee cha Jordan fa John, ndah͈ mu batise fi mōm.
14Wande John bañ ko, ne, Mā soh͈la batise fi you; te yangi ñou fi man?
15Yesu tontu ko, ne, Bul ko bañ lēgi, ndege nōgu la ñu ela motali njūbay yepa. Nōgale la bañatul.
16Ba batise’ Yesu mote, mu gēna chi ndoh͈ ma; nōn’ ak nōna asaman si ūbiku chi mōm; mu gis Nh͈el i Yalla di wacha chi melo i mpetah͈, te dal chi kou am:
17Te bāt juge cha asaman, ne, Kile mō di suma Dōm ji ma sopa, chi mōm lā feka li ma nêh͈ lepa.
Jelenleg kiválasztva:
Matthew 3: GWG
Kiemelés
Megosztás
Másolás
Szeretnéd, hogy a kiemeléseid minden eszközödön megjelenjenek? Regisztrálj vagy jelentkezz be
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.