John 4

4
1Ba Borom bi h͈ame nak ne Pharisee ya dēg’ on nañu ne Yesu angi don def te batise i talube yu gen a bare as John,
2(Wande Yesu du won batise, wande i talube am),
3Mu bayako Judea, te demati cha Galilee.
4Te mu ela jār cha bir Samaria.
5Mu agsi nak fa dek’ i Samaria bu tūda Sychar, bu jegeñ tōl ba Yanh͈oba may on Yusufa dōm am:
6Te tên i Yanh͈oba anga fa won. Yesu nak don na lota cha tūkê’m, te tōg nōgule cha tên ba. Chi jurom ben’ i wah͈tu la potah͈.
7Bena jigen i Samaria ñou rôtsi ndoh͈. Yesu ne ko, May ma ma nān.
8Ndege i talube am dem on nañu cha bir deka ba jendi dūndu.
9Jigen i Samaria ja ne ko, Ana lu indi be you mi di Yauod nga di dagān nān chi man, te mā di jigen i Samaria? Ndege Yauod ya amu ñu soh͈la ak wā’ Samaria ya.
10Yesu tontu te ne ko, So h͈am on maye’ Yalla, ak ki di wah͈ ak you, ne, May ma ma nān; kōn di nga ko dagān, te mu may la ndoh͈ i dūnda.
11Jigen ja ne ko, Borom bi, amu la dara lo rôte, te tên bi h͈ōt na: fo di jeleji ndoh͈ i dūnda mōmu?
12Ndah͈ yā gēti suñu bay Yanh͈oba, mi ñu may on tên bi, te mu nān cha, ak i dōm am, ak i nag am?
13Yesu tontu te ne ko, Ku neka ku di nān chi ndoh͈ mile, di na delu marati:
14Wande ku mu mun a don ku di nān chi ndoh͈ mi ma ko mayi, du marati muk; wande ndoh͈ mi ma ko mayi, di na neka chi bir am ab tên i ndoh͈ mu di nacha be cha dūnda gu dul jêh.
15Jigen ja ne ko, Borom bi, may ma ndoh͈ mōmu, ndah͈ du ma marati, mbāte ñou file rôtsi.
16Yesu ne ko, Demal ô sa jekar, te delusi file.
17Jigen ja tontu te ne ko, Amu ma jekar. Yesu ne ko, Wah͈ nga dega, ne, Amu ma jekar:
18Ndege jurom i jekar nga am on; wande ki nga am lēgi dowul sa jekar: lōla nga wah͈ chi dega.
19Jigen ja ne ko, Borom bi, gis nā ne yonent nga.
20Suñu i bay ya jāmu on nañu chi tūnda wile, te ngēn ne, Jerusalem a di bereb fa nit war a jāmu.
21Yesu ne ko, Jigen ji, gum ma, wah͈tu wā’nga dikasi be dōtu len jāmu Bay ba chi tūnda wile, mbāte cha Jerusalem.
22Yēn a jāmu lu ngēn h͈amul: ño jāmu la ñu h͈am; ndege cha Yauod ya la h͈ewal juge.
23Wande wah͈tu wā’nga dikasi, te jot na, ba jāmukat yu dega ya di jāmu Bay ba chi nh͈el ak chi dega: ndege Bay ba ūt ña mel ni ñale ñu jāmu ko.
24Yalla Nh͈el la; te ña ko jāmu war nañu ko jāmu chi nh͈el ak chi dega.
25Jigen ja ne ko, H͈am nā ne Masiu di na dika (ka tūda Krista): su dike, di na ñu jangal yef yepa.
26Yesu ne ko, Man mi di wah͈ ak you mōm la.
27Fōfale i talube am ñou, te jomi ne ak jigen la don wah͈tānal; wande ken wah͈ul, ne, Lan nga ūt? mbāte, Lutah͈ nga wah͈tān ak mōm?
28Jigen ja nak bayi ndā am, te dem cha bir deka ba, te ne nit ña,
29Ñou len, sêt nit ka ma nitali li ma def on yepa: ndah͈ du mō di Krista?
30Nu gēna deka ba, te dika fa mōm.
31Cha bōbale i talube am dagān ko, ne, Rabbi, na nga leka.
32Wande mu ne len, Am nā dūndu bu ma leka bu ngēn h͈amul.
33Talube ya wah͈ante, ne, Ndah͈ kena indiwul lu mu leka?
34Yesu ne len, Suma dūndu mō di def mbugel i ka ma yōni on, te motali ligey am.
35Bu len wah͈, ne, Des na ñenent i wêr te ngōbte di na jot. Mangi len di wah͈, Yēkati len sēn i but, te sêt tōl ya, ne wêh͈ nañu jēg chi ngōbte.
36Ka di gōb am yōl, te dajale mēñef be chi dūnda gu dul jêh͈; ndah͈ ku di ji ak ku di gōb mun a boka banēh͈u.
37Chi lile la lēbātu bi dega, Kena ji, te kenen gōb.
38Yōni on nā len ngēn gōb lu ngēn ligeyul: ñenen a ligey on, te yēn a tabi chi sēn ligey.
39Te chi deka bōbale jopa chi wā’ Samaria ya gum on nañu chi mōm, ndig bāt i jigen ja sēde won, ne, Nitali na ma li ma def on yepa.
40Ba wā’ Samaria ñoue fi mōm, ñu dagān ko mu dal ak ñom: te mu dal fa ñar i fan.
41Te ñenen ñu bare gum ndig bāt am;
42Te ñu ne jigen ja, Lēgi nak dōtu ñu gum ndig sa bāt reka; ndege ñun it dēga nañu, te h͈am ne kile di Musalkat i aduna si chi dega.
43Ganou ñar i fan ya mu gēna fa dem cha Galilee.
44Ndege Yesu chi bop’ am, sēde won na ne yonent amul teranga chi rew am.
45Ba mu ñoue chi bir Galilee, wā’ Galilee ya nangu ko, ndege gis on nañu yef yepa ya mu def on cha h͈ewte ga: ndege ñom it dem on nañu cha h͈ewte ga.
46Mu ñouati nak cha Cana i Galilee, fa mu sopali won ndoh͈ ma biñ. Te bena kangam am on na, ka dōm am ju gōr opa cha Capernaum.
47Ba mu dēge ne Yesu juge on na Judea ñou chi Galilee, mu dem fa mōm, te dagān ko mu dika weral dōm am; ndege mungi buga dē.
48Yesu ne ko, Su ngēn gisule i mandarga ak i koutef, ngēn bañ a gum.
49Kangam ba ne ko, Borom bi, ñoual, bala suma dōm dē.
50Yesu ne ko, Demal sa yōn; sa dōm dūnda na. Nit ka gum bāt ba ko Yesu wah͈, te dem yōn am.
51Te ba mu deme, i bukanēg am feka ko, ne ko dōm am dūnda na.
52Mu lāj len chi wan wah͈tu la dal di gene. Ñu ne ko, Demba chi jurom ñar i wah͈tu, fēbar ba bayi ko.
53Bay ba h͈am nak ne cha wah͈tu wōwa la ko Yesu ne, Sa dōm dūnda na: te mu gum, ak ker am ñepa.
54Bile di ñarel i koutef ga Yesu def on, ba mu juge Judea dem fa Galilee.

Одоогоор Сонгогдсон:

John 4: GWG

Тодруулга

Хуваалцах

Хувилах

None

Тодруулсан зүйлсээ бүх төхөөрөмждөө хадгалмаар байна уу? Бүртгүүлэх эсвэл нэвтэрнэ үү