Njàlbéen ga 12
12
Yàlla sant na Ibraam, mu gàddaay
1 Aji Sax ji moo waxoon Ibraam, ne ko: «Jógeel sam réew, jóge ci say bokk ak sa kër baay, te nga dem ca réew mi ma lay won,
2ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa,
barkeel la,
màggal sa tur,
ngay buntu barke;
3ku la ñaanal barke, ma barkeel,
ku la móolu it, ma alag,
te xeeti àddina sépp,
ci yaw lañuy barkeele.»
4Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75). 5Ibraam ànd ak soxnaam Sarayi ak Lóot, mi muy baay bu ndaw ci moom. Mu yóbbaale nag alal, ja mu dajale jépp, ak jaam, ya mu jënde Karan. Ñu jóge fa, jublu réewu Kanaan.
6Ba ñu agsee Kanaan, Ibraam dafa jàll ca biir réew ma, ba àgg bérab bu sell, ba féete ak Sikem, ca garab#12.6 Xeetu garab la gu ñuy wax terebent. gu mag, ga ñuy wooye More. Booba fekk na waa Kanaan a nga woon ca réew ma. 7Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.
8Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko. 9Ibraam bàyyikooti fa, aw yoonam, jublu àllub Negew#12.9 àllub Negew: mu nga féete Kanaan bëj-saalum, nekk ca yoonu Misra. Li muy tekki mooy «wowaay». .
Ibraam dem na réewum Misra
10Ca jamono jooja xiif a amoon ca réew ma, ba tax Ibraam dem réewum Misra, toogi fa, ndax xiif bu metti la woon. 11Naka lay jub Misra, daldi ne soxnaam Sarayi: «Déglu ma, xam naa ne ku rafet nga. 12Bu la waa Misra gisee, dinañu ne sama soxna nga. Te dinañu ma rey, nga des. 13Kon nag ngalla waxal ne sama jigéen nga, ba tax ma am jàmm; su ko defee dees na ma bàyyi, ma dund, te di la ko gërëme.»
14Ba Ibraam àggee Misra, waa Misra gis ne jigéen ji mu àndal rafet na lool. 15Jaraafi Firawna itam gis ko, di ko kañ ca Firawna ndax taar ba, ñu daldi ko yóbbu ca kër Firawna. 16Firawna nag topptoo Ibraam bu baax ndax moom, ñu may ko ay gàtt ak ay nag, ay mbaam yu góor, ak ay jaam yu góor ak yu jigéen, ak ay mbaam yu jigéen aki giléem.
17Teewul Aji Sax ji wàcce ca Firawna ak waa këram jàngoro yu metti ndax Sarayi, soxnas Ibraam. 18Firawna woolu Ibraam ne ko: «Li nga ma def nag? Lu tax waxoo ma ne kii sa soxna la? 19Lu tax nga ne sa jigéen la, ba tax ma jël ko, bëgg koo def sama jabar? Ayca, sa jabar a ngoog, fabal te ne mott!» 20Naka la Firawna wax loolu ba noppi, daldi sant ay dagam, ñu génne Ibraam réew ma, moom ak soxnaam ak alalam jépp.
Nu markerat:
Njàlbéen ga 12: KYG
Märk
Dela
Kopiera
Vill du ha dina höjdpunkter sparade på alla dina enheter? Registrera dig eller logga in
Copyright © 2010, 2020 La Mission Baptiste du Sénégal