Njàlbéen ga 13:10
Njàlbéen ga 13:10 KYG
Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja.