Njàlbéen ga 25
25
Ibraayma nelaw na
1Ibraayma jëlaat na soxna su tudd Ketura, 2am ca Simran ak Yogsan ak Medan ak Majan ak Yisbag ak Suwa. 3Yogsan jur Saba ak Dedan. Askani Dedan ñooy Asureen ñi, Letuseen ñi ak Lewumeen ñi. 4Doomi Majan di Efa ak Efer ak Anog ak Abida ak Elda. Ñooñu ñépp xeetu Ketura lañu.
5Ibraayma nag donale Isaaxa lépp lu mu moom. 6Doom yu góor, ya mu am aki nekkaaleem, mu may leen alal ca ba muy dund, ba noppi yebal leen penku, ñu sanci ca réewu penku, ba sore doomam Isaaxa#25.6 Ca yooya jamono, nit manoon naa am ay soxna yu am cér bu mat sëkk, ak yeneen soxna, yu gëna néewle sañ-sañ, ñoom ak seeni doom. .
7Ati Ibraayma téeméer la ak juróom ñaar fukk ak juróom (175). 8Ba loolu weesee la bakkanu Ibraayma rot, mu nelaw, fekki ay maamam, gannaaw ba mu guddee fan, ba màggat lool te barkeel. 9Isaaxa ak Ismayla, doomam yu góor ya, rob ko ca xuntim xeer ma ca Magpela te jàkkaarloo ak Mamre, ca toolub Efron doomu Sowar, Etteen ba. 10Tool ba Ibraayma jëndoon ca Etteen ña, foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata. 11Gannaaw ba Ibraayma nelawee, Yàlla barkeel na doomam Isaaxa. Isaaxaa ngi dëkkoon ca wetu teenu Laxay Roy.
Askanu Ismayla
(Saar 25.12-18)
12Ismayla moomee nag, doomu Ibraayma jaak Ajaram Misra, ma doon jaamub Saarata, askanam mooy lii. 13Turi doomi Ismayla yu góor yaa di: Nebayot, taawub Ismayla, ña ca topp di Kedar ak Adabeel ak Mibsam 14ak Misma ak Duuma ak Maasa 15ak Adàdd ak Tema ak Yetur ak Nafis ak Kedama. 16Ñooñu ñooy doomi Ismayla yu góor, seeni tur a ngoog, ñuy fukki garmi ak ñaar yu jiite seeni mbooloo ci seeni sanc ak seeni dal. 17Ati Ismayla téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). Gannaaw loolu la nelaw, fekki ay maamam.
18Ña nga dëkkoon diggante ba dale Awila ba Sur ga jàkkaarlook Misra, booy jëm Asur. Noonu la fa askanu Ismayla sance, jàkkaarlook doomi baayam yépp.
Askanu Isaaxa doomu Ibraayma
(Saar 25.19—35.29)
19Isaaxa doomu Ibraayma ju góor ja, askanam mooy lii. Ibraaymaa jur Isaaxa. 20Isaaxa am ñeent fukki at, jël Rebeka doomu Betuwel, Arameen, bi dëkke diiwaanu Padan Aram, dib jigéenu Laban, Arameen ba. 21Gannaaw ga soxnas Isaaxa amul doom, Isaaxa dagaanal ko Aji Sax ji, mu nangul ko, soxna si daldi ëmb. 22Doom yi nag di buuxante ci biiram, ba mu naan: «Ndegam nii la kay, jaru ko woon!» Ci kaw loolu soxna si dem, diis ko Aji Sax ji.
23Aji Sax ji ne ko:
«Ñaari giir nga ëmb,
nara am ñaari xeet yuy xaajaloo,
wenn wi mooy ëpp doole wi ci des,
te mag ji mooy surgawu rakk ji#25.23 Ci bànni Israyil, seex, bi jëkka juddu, moo mag ki mujja juddu. .»
24Ba mu demee ba wara mucc, amul lu moy ay seex. 25Naka noona ka jëkka gane àddina xonq, yaram wi sëq lipp, mel ni mbubbum der mu ne sàyy aki kawaram, ñu tudde ko Esawu (mu firi Ku jëxëm). 26Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën)#25.26 Jàpp ci téstën mu ngi tekki ci waxin «suufu nit, ba am loo nangu ci moom». . Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at.
Esawu sàggane na céram
27Ba mu ko defee gone ya di màgg, Esawu di rëbbkat bu ñaw, di ku bëgg àll; Yanqóoba moom di nit ku gàtteñlu#25.27 gàtteñlu gi ci Yanqóoba moo waraloon xamul dara ci rëbb. te bëggoon toogaayu kër. 28Isaaxa nag am cofeel ci Esawu ndax li muy lekk ci am rëbbam, te Rebeka moom gëna sopp Yanqóoba.
29Mu am bés Yanqóoba di togg ndambel ñebbe ju xonq, yemook Esawu jóge ca tool ya, xiif ba ne ñedd. 30Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe). 31Yanqóoba ne ko: «Danga ma koy jëkka wecci sa céru ndono bi nga yeyoo ndax li ngay taaw#25.31 Ci bànni Israyil, taaw mooy mujj doon kilifag kër, te mooy ëpple ay rakkam ab cér ci ndono. .» 32Esawu ne: «Man miy waaja dee ak xiif, ana lu ma céru taaw di jariñ?» 33Yanqóoba ne ko: «Giñal ma jëkk.» Esawu giñal ko ko, mu jaay Yanqóoba ndono, li mu yeyoo ndax li muy taaw. 34Yanqóoba jox Esawu mburu ak ndambe, mu lekk, naan, daldi jóg dem yoonam. Noonu la Esawu sàgganee céru taaw, bi mu yeyoo.
Copyright © 2010, 2020 La Mission Baptiste du Sénégal