John 9
9
1Ba Yesu rombe, mu gis nit ku silmah͈a won cha ba mu jūdo.
2Te talube am ya lāj ko, ne, Rabbi, kan a bakar, kile, am i wā’ jur am, be mu judo silmah͈a?
3Yesu tontu, ne, Dowul kile bakar mbāt i wā’ jur am: wande ndah͈ i ligey i Yalla fêñ chi mōm.
4Ela naño def i ligey i ka ma yōni on, bi bechek bi neke: gudi g’ānge dika, bu ken munul a ligey.
5Ba ma neke chi aduna si, mā di lêr i aduna si.
6Ba mu wah͈ on lōlu, mu tufli chi suf si, te defar binit ak tuflit am, te diw binit ba chi i but am,
7Te ne ko, Demal, selmu cha dēg i Siloam (mu tiki ne Yoni). Mu dem, te selmu, te delusi di gis.
8Dekando ya nak, ak ña ko gis on bu jeka ne mō don yelwankat, ne, Ndah͈ dowul kile don tōg di yelwān?
9Ñena ne, Mōm la; ñenen ne, Dēt, wande niro na ak mōm; mu ne, Man la.
10Tah͈na ñu ne ko, Naka la sa i but ūbiko?
11Mu tontu, ne, Nit ku tūda Yesu defar on na binit, te diw suma i but, te ne ma, Demal fa Siloam te selmu: dem on nā nak, te selmu, te suma i but ūbiku.
12Te ñu ne ko, Fu mu neka? Mu ne, H͈amu ma.
13Ñu indi ko fa Pharisee ya ka jek’ on a silmah͈a.
14Chi bes i Dimas la won ba Yesu defare binit ba, te ūbi i but am.
15Pharisee ya itam lāj ko naka mu def be gis. Te mu ne len, Def on na binit chi suma i but, te ma selmu, te gis.
16Ñena cha Pharisee ya ne nak, Nit kile dowul ku bayako fa Yalla, ndege du japa bes i Dimas ja. Wande ñenen ne, Naka la nit ku di bakarkat mun a defe mandarga yile? Te h͈ājalo jog na chi sēn digante.
17Ñu nêti silmah͈a ba, Lan nga wah͈ chi lu jem chi mōm, ndege ūbi na sa i but? Te mu ne, Mō di yonent.
18Wande Yauod ya bañ a gum chi mōm ne silmah͈a la won, te i but am ūbiku, be ñu ôlu i wā’ jur i ka i ka but am ūbiku on:
19Te ñu lāj len, ne, Ndah͈ kile sēn dōm la ji ngēn ne jūdu on na silmah͈a? naka la def ndōg be di gis lēgi?
20Wā’ jur am ya tontu te ne, H͈am nañu ne kile suñu dōm la, te jūduāle on na silmah͈a:
21Wande h͈amu ñu naka la def be di gis tey; te h͈amu ñu ka ūbi won i but am: lāj len ko; mag la; di na wah͈al bop’ am.
22Wā’ jur am ya wah͈ nañu yef yile, ndege ragal on nañu Yauod ya: ndege Yauod ya wah͈ante on nañu be sotal, ne su kena wah͈e ne mō di Krista, di nañu ko gēne chi ndaje ma.
23Lōlo tah͈ wā’ jur am yi ne, Mag la; lāj len ko.
24Ñu ôlu nak ka silmah͈a won ñar i yōn, te ne ko, Na nga jebal Yalla ndam: h͈am nañu ne nit kile bakarkat la.
25Mu tontu, ne, Ndem neka na bakarkat, h͈amu ma: lena lā h͈am, ne nek’ on nā silmah͈a, te lēgi nak mange gis.
26Ñu ne ko, Lan la la def on? naka la ūbi won sa i but?
27Mu tontu len, ne, Wah͈ on nā len ko lēgi, te dēgu len ko won: lutah͈ ngēn bugati ko dēga? Ndah͈ yēn itam da ngēn buga neka i talube am?
28Te ñu h͈ūle ko, te ne, Yā di talube am; wande ño di talube i Musa ya.
29H͈am nañu ne Yalla wah͈ on na cha Musa; wande kile, h͈amu ñu fu mu bayako.
30Nit ka tontu te ne len, Lile nak njomite la, ne h͈amu len fu mu bayako, te ūbi suma i but.
31H͈am nañu ne Yalla du dēga i bakarkat: wande su kena neke jāmukat i Yalla, te def mbugel am, mōm la di dēga.
32Cha ndôrte’ aduna si bentey, ken mosul a dēga ne way ūbi na i but i ku jūduāle won a silmah͈a.
33Su kile jugewul on fa Yalla, du mun a def dara.
34Ñu tontu te ne ko, Yangi jūdu on bepa chi bakar, te nga buga ño jemantal? Te ñu gēne ko cha biti.
35Yesu dēga ne gēne nañu ko cha biti; te ba mu ko gise, mu ne, Ndah͈ gum nga chi Dōm i Yalla?
36Mu tontu te ne, Kōka di kan, Borom bi, ndah͈ ma gum chi mōm?
37Yesu ne ko, Gis nga ko, te mōm sah͈ a di wah͈ ak you.
38Te mu ne, Gum nā, Borom bi; te mu jāmu ko.
39Te Yesu ne, Ndig ate tah͈ on ma ñou chi aduna si, ndah͈ ña gisul di mun a gis; ak ñu gis di mun a silmah͈a.
40Pharisee ya nek’ on ak mōm dēga yef yile, te ne ko, Ndah͈ ñun it silmah͈a nañu?
41Yesu ne len, Su ngēn silmah͈a won, kōn du len am bakar: wande wah͈ ngēn lēgi, ne, Da ñu gis: mōtah͈ sēn bakar des na.
S'ha seleccionat:
John 9: GWG
Subratllat
Comparteix
Copia
Vols que els teus subratllats es desin a tots els teus dispositius? Registra't o inicia sessió
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.