John 6
6
1Cha ganou yef yile Yesu dem on na cha genen wet i gēch i Galilee, bu di gēch i Tiberias.
2Te mbōlo mu rey topa ko, ndege gis on nañu koutef ya mu def on cha ña op’ on.
3Te Yesu yēg cha kou tunda wa, te tōg fa ak i tabube am.
4Te bena h͈ewte i Yauod ya jegeñsi na.
5Yesu nak, ba mu yēkate i but am, mu gis mbōlo mu rey di ñou fi mōm, te ne Philip, Ana fu ñu di jendi mburu ndah͈ ñile mun a leka?
6Te wah͈ na lile ndah͈ mu sêtlu ko: ndege mō h͈am lu mu buga def.
7Philip tontu ko, ne, Ñar tēmēr i transu mburu du len doy, ndah͈ ku neka jel tuti.
8Kena chi talube am ya, Andrew, rak’ i Simon Peter, ne ko,
9H͈alel angile bu am jurom i mburu, ak ñar i jen: wande ana lu lile di faj chi mbōlo mu ni day?
10Yesu ne, Tōglo len nit ñi. Ñah͈ mu bare nek’ on na cha bereb ba; te nit ña tōg chi suf, lu jem chi jurom i njūne potah͈.
11Yesu nak jel mburu ya, te ba mu jebale ngerem, mu sedātle len ña tōg; ak jen ya itam cha naka ñu buge.
12Te ba ñu leke be sūr, mu ne i talube am, Dajale len dogit yi chi des, ndah͈ bul chi dara yah͈u.
13Tah͈na ñu dajale len, be fêsal cha fuk’ i sendel ak ñar chi i dogit i mburu ya cha des on, cha la ñu lek’ on.
14Ba nit ña gise koutef ga mu def on nak ñu ne, Chi dega kile di yonent ba di dika chi aduna si.
15Yesu nak, ba mu h͈ame ne buga naño ñou di ko jel ak dōle, te fal ko bur, mu demati cha tūnda wa mōm reka.
16Te ba ngon jote, i talube am dem cha gēch ga;
17Te ñu duga chi gāl, te dal di jala gēch ga cha Capernaum. Te mu lendem, te Yesu ñouangul on fa ñom.
18Te gēch ga yengatu, ndig ngelou lu rey lu don fuf.
19Ba ñu jowe nak be fu sorey, ñu sēn Yesu mu di doh͈ cha kou gēch ga, te jegeñsi gāl ga, te ñu tīt.
20Wande mu ne len, Man la; bu len tīt.
21Tah͈na ñu nangu jel ko cha gāl ga: te nōn’ ak nōna gāl ga aga cha jēri ja ñu buga dem.
22Cha elek sa, mbōlo ma tah͈ou on cha genen wet i gēch ga gis on nañu ne bena gāl rek’ anga fa won, te Yesu dugul on cha gāl ga ak i talube am, wande i talube am bayako fa ñom dal;
23(Wande yenen gāl juge on nañu cha Tiberias, mu jegeñ bereb ba ñu leke won mburu ma, ganou ba Borom bi jebal on ngerem:)
24Ba mbōlo ma gise nak ne Yesu neku fa, mbāte i talube am, ñom it ñu duga chi gāl ya, te ñou chi Capernaum, di ūt Yesu.
25Te ba ñu ko gise cha genen wet i gēch ga, ñu ne ko, Rabbi, kañ nga ñou on file?
26Yesu tontu len, te ne, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Ūtu len ma ndege gis on ngēn i koutef, wande ndege lek’ on ngēn mburu ya be ngēn sūr.
27Bu len ligey ndig dūndu bu di sanku, wande ndig dūndu bu di deka be abada, ba len Dōm i nit ka di mayi: ndege mōm la Yalla Bay ba tan’ on.
28Ñu ne ko, Lan la ñu war a def, ndah͈ ñu di ligey i ligey i Yalla?
29Yesu tontu te ne len, Lile di ligey i Yalla, ndah͈ ngēn gum chi mōm ka mu yōni on.
30Ñu ne ko, Ban mandarga nga def, ndah͈ ñu di gis, te gum la? Ana lo ligey?
31Suñu i bay lek’ on nañu manna ba cha manding ma; cha naka ñu bind’ on, ne, May on na len mburu cha asaman ñu leka.
32Yesu ne len, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Musa mayul on len mburu ma cha asaman; wande suma Bay a len may mburu mu dega ma cha asaman.
33Ndege mburu’ Yalla ma mō di ma juge cha asaman, ti di maye dūnda chi aduna si.
34Ñu ne ko, Borom bi, may ñu mburu mile bel mos.
35Yesu ne len, Mā di mburu’ dūnda mi: ku ñou fi man du h͈īf, te ku gum chi man du mar muka.
36Wande wah͈ on nā len, ne, Da ngēn ma gis, te tah͈ul bentey ngēn gum.
37Ña ma Bay ba may ñepa, di nañu ñou fi man: te ku ñou fi man, du ma ko dah͈a muka.
38Ndege jugewu ma cha asaman ndah͈ ma def suma mbugel i bopa, wande mbugel i ka ma yōni on.
39Te mbugel i ka ma yōni on a di lile, ne ña mu ma may ñepa, du ma ñaka ken, wande dēkali ko cha kera bes ba.
40Ndege suma mbugel i Bay ba di bile, ne ku neka ku gis Dōm ji te gum chi mōm, di na am dūnda gu dul jêh͈; te di nā ko dēkali cha kera bes ba.
41Tah͈na Yauod ya ñurumtu ko, ndege wah on na, ne, Mā di mburu ma juge won cha asaman.
42Te ñu ne, Ndah͈ kile dowul Yesu, dōm i Yusufa, te ñu h͈am bay am ak ndey am? Naka la wah͈e, ne, Manga juge cha asaman?
43Yesu tontu te ne len, Bu len ñurumtu chi sēn bopa.
44Ken munul a ñou fi man, lu dul Bay ba ma yōni on h͈ēcha ko: te di nā ko dēkali cha kera bes ba.
45Binda nañu chi tēre’ yonent ya, ne, Nepa Yalla di na len jemantal. Ku neka mbōk ku dēga bāt i Bay ba, te jemantu, mu ñou fi man.
46Ken gisul Bay ba, ganou mōm ka juge won cha Yalla, mō gis on Bay ba.
47Chi dega, chi dega, ma ne len, Ku di gum, mō am dūnda gu dul jêh͈.
48Mā di mburu’ dūnda ma.
49Sēn i bay lek’ on nañu manna ba cha manding ma, te dē on nañu.
50Bile di mburu mi juge won cha asaman, ndah͈ nit mun ko leka, te du dē.
51Mā di mburu’ dūnda ma juge won cha asaman: su kena leke chi mburu mile, di na dūnda bel mos: te mburu ma ma mayeji suma yaram la, wa ma jebaleji ndig dūnd’ i aduna si.
52Yauod ya nak werante chi sēn bopa, ne, Naka la ñu nit kile mune joh͈ yaram am ñu leka?
53Yesu ne len mbōk, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Su ngēn lekule yaram i Dōm i nit ki, te nānu len deret am, du len am dūnda chi yēn.
54Ku di leka suma yaram, te nān suma deret, am na dūnda gu dul jêh͈; te di nā ko dēkaliji cha kera bes ba.
55Ndege suma yaram dūndu’ dega la, te suma deret nān i dega la.
56Ku di leka suma yaram te nān suma deret, deka na chi man, te man chi mōm.
57Naka ma Bay ba di dūnda yōne, te mā dūnda ndig Bay ba; nōgule la itam ka ma di leka, di na dūnda ndig man.
58Bile di mburu ma juge won cha ajana: dowul mburu ma bay ya lek’ on, te dē: ku di leka mburu mile di na dūnda bel mos.
59Yef yile la wah͈ on cha juma ja, ba mu jemantal on cha Capernaum.
60Lu bare chi i talube am nak, ba ñu dēge lile, ne, Wah͈ jile dīs na; ku ko mun a dēga?
61Wande Yesu h͈am chi bop’ am ne i talube am ñurumtu nañu chi lile, te mu ne len, Ndah͈ lile tah͈ ngēn fakatalu?
62Naka su ngēn gise Dōm i nit ka di yēg fa mu jek’ on a juge?
63Mō di nh͈el ma di dūndalo; yaram wi jeriñul dara: bāt ya ma len wah͈ nh͈el la, ak dūnda.
64Wande ñena chi yēn gumu len. Ndege Yesu h͈am on na cha ndôrte la ña gumul on, te ka ko di ori.
65Te mu ne, Lile tah͈ ma wah͈ on len, ne, ken munul a dika fi man, su ko ko Bay ba mayule.
66Ndig lile lu bare chi i talube am delu ganou, te andatu ñu ak mōm.
67Yesu ne fuk’ ak ñar ña, Ndah͈ yēn itam, da ngēn ma wocha?
68Simon Peter tontu ko, ne, Borom bi, fi kan la ñu ela dem? Yā am i bat i dūnda gu dul jêh͈.
69Te gum nañu, te h͈am, ne yā di kena ku sela ka juge fa Yalla.
70Yesu tontu len, ne, Ndah͈ du yēn lā tan’ on, fuk’ ak ñar ña, te kena chi yēn ab seytane la?
71Lile nak wah͈ na ko ndig Judas, dōm i Simon Iscariot, ndege mō ko ori, kena chi fuk’ ak ñar ña.
Одоогоор Сонгогдсон:
John 6: GWG
Тодруулга
Хуваалцах
Хувилах
Тодруулсан зүйлсээ бүх төхөөрөмждөө хадгалмаар байна уу? Бүртгүүлэх эсвэл нэвтэрнэ үү
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.