Matthew 7
7
1Bu len di ate, ndah͈ kena du len ateji.
2Ndege ate bu ngēn ate ñenen, di nañu len ko ateji; te natu bu ngēn di natale, mōm sah͈ la ñu len di nataleji.
3Lu elal nga di nimeku felah͈ bi chi sa but i morom, te do gis lā bi chi sa but?
4Wala naka nga wah͈e sa morom, ne, Bayi ma ma dindi felah͈ bi chi sa but, te lā’ngi chi sa but sah͈?
5Mīkar bi, dindil jeka lā bi chi sa but, te ganou ga di nga gis bu set ndah͈ nga mun a dindi felah͈ ba chi sa but i morom.
6Bu len joh͈ la sela h͈aj ya, te bu len sani sēn i takay chi kanam i mbām; ndig so otuwul di nañu len degat chi sēn run tanka, te walbataku h͈oti len.
7Lāj len, te di nañu len may; ūt len, te di ngēn gis; foga len, te di nañu len ūbi:
8Ndege ku mu mun a don ku lāj, di na am; te ku ūt, di na gis; te ku foga, di nañu ko ūbi.
9Kan chi yēn, su ko dōm am lāje mburu, mu may ko doch?
10Wala su ko lāje jen, mu may ko jān?
11Yēn ñi bon nak, su ngēn h͈ame may sēn i dōm yef yu bāh͈, as sēn Bay ba cha ajana di na may ña ko lāj yef yu bāh͈?
12Mōtah͈ lu ngēn buga lepa nit di len ko defal, yēn itam na ngēn ela defal ñenen: ndege bile di yōn wi ak yonent ya.
13H͈araf len chi bunta bu h͈ocha ba: ndege bunta ba yā na, te yōn wa jublu chi sankute yātu na, te bare na ñu cha tabi:
14Ndege bunta ba h͈ocha na, te yōn wa jublu chi dunda h͈at na, te ñu new a ko gis.
15Otu len i yonent i nafeh͈a ya, di ñou fi yēn chi nchangay i nh͈ar, wande chi bir ño di buki yu fuh͈ale.
16Di ngēn len h͈am chi sēn i mēñef. Ndah͈ nit di na dajale i dōm i garap i biñ chi i dek, mbāt i sōto chi i h͈āh͈am?
17Nōgu itam garap gu bāh͈ gu neka di na mēña mēñef bu bāh͈; wande garap gu bon di na mēña mēñef bu bon.
18Garap gu bāh͈ munul a mēña mēñef bu bon, te garap gu bon munul a mēña mēñef bu bāh͈.
19Garap gu neka gu mēñul mēñef bu bāh͈, di nañu ko gor, te sani ko chi safara.
20Di ngēn len h͈am mbōk chi sēn i mēñef.
21Du ku neka ku ma wah, ne, Borom bi, Borom bi, di na h͈araf chi ngur i ajana; wande ka def suma mbugel i Bay ba cha ajana mōm reka.
22Ñu bare di nañu ma wah͈ chi bes bōbale, Borom bi, Borom bi, ndah͈ wareū ñu on chi sa tur, te chi sa tur ñu dah͈’ i jine, te chi sa tur ñu def koutef yu bare?
23Fōfale di nā len yēgal, ne, Mosu ma len a h͈am; randu len ma, yēn ña def lu bon.
24Mōtah͈ ku mu mun a don ku dēga suma i bāt yile, te def len, di na niro ak nit i sago, ka tabah͈ nēg am chi kou doch:
25Tou ba dal, wame wa buna, ngelou la ñou, te dal chi kou nēg bōbale; wande dānuwul; ndege chi doch la sampu.
26Te ku mu mun a don ku dēga suma i bāt yile, te defu len, di na niro ak nit ku ñaka sago, ka tabah͈ nēg am chi kou banh͈aleñ:
27Tou ba dal, wame wa buna, ngelou la ñou, te dal chi kou nēg bōbale; mu maba; maba gu rey.
28Am on na ba Yesu sotale bāt yile, mbōlo ma jomi chi njemantal am:
29Ndege jemantal on na len naka ku am sañsañ, te nekul naka sēn i bindānkat.
Одоогоор Сонгогдсон:
Matthew 7: GWG
Тодруулга
Хуваалцах
Хувилах
Тодруулсан зүйлсээ бүх төхөөрөмждөө хадгалмаар байна уу? Бүртгүүлэх эсвэл нэвтэрнэ үү
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.