Matthew 5
5
1Ba mu gise mbōlo ma, mu yēg cha kou tūnda wa; ba mu tōge, tālube am ya ñou fi mōm;
2Mu ūbi gemeñ am, te jemantal len, ne,
3Barkel cha ña sufelu chi fit; ndege ngur i ajana di na len lew.
4Barkel cha ña nah͈arlu; ndege di nañu dalal sēn h͈ol.
5Barkel cha ñu lew ña; ndege di nañu mōmi aduna si.
6Barkel cha ña di h͈īf te mar chi njūbay; ndege di nañu doylu.
7Barkel cha ña am yermande; ndege di nañu joti yermande.
8Barkel cha ña set chi h͈ol; ndege di nañu gis Yalla.
9Barkel cha i defarkat i jama ña; ndege di nañu len tūde i dōm i Yalla.
10Barkel cha ña getenu ngir njūbay; ndege ngur i ajana di na len lew.
11Barkel chi yēn su ñu len di h͈as, te geten len, te sos lu bon yepa chi yēn ndig man.
12Banēh͈u len, te kontan len lol; ndege sēn yōl rey na cha ajana; ndege nōgu la ñu geten on yonent ya len jītu on.
13Yēn a di soh͈mat i aduna si; wande su soh͈mat ñake nchafo am, lu ñu ko safaleti? Dōtul jeriñ dara lul sani ko chi biti, te nit degat ko chi suf.
14Yēn a di lêr i aduna si. Deka bu ñu teg chi kou tūnda, munul a nubu.
15Ken du tāl nītu, te def ko chi run ndap, wande chi kou nītukay, te di na lêral ña chi bir nēg ba ñepa.
16Na sēn lêray mbōk tāka chi kanam i nit, ndah͈ ñu gis sēn i jef yu bāh͈, te di magal sēn Bay ba cha ajana.
17Bu len dēfe ne da ma dika fanh͈asi yōn wa ak lu yonent ya wah͈ on; diku ma fanh͈asi wande motalisi.
18Ndege chi dega mangi len di wah͈, Be bu ajana ak suf di wey, dara du wey chi yōn wa muk, be yepa motaliku.
19Ku mu mun a don mbōk ku di moy bena chi eble yile bu gen a tūt, te jemantal nit ña nogule, di nañu ko tūdeji ka gen a new ñepa chi ngur i ajana; wande ku len di def te jemantal len, di nañu ko tūdeji ku rey chi ngur i ajana.
20Ndege mangi len di wah͈, Su sēn njūbay sutule njūbay i bindānkat ya ak Pharisee ya, du len h͈araf chi ngur i ajana muk.
21Dēga ngēn ñu wah͈ on nit i h͈āt ya, Bulu rēy; te ku di rēy mungi chi tafār i ate:
22Wande mangi len di wah͈, Ku di mere morom am, mungi chi tafār i ate; te ku ne morom am, Dof bi, mungi chi tafār i ate bu rey; wande ku ne, Ēfar bi, di na neka chi tafār i safara’ nāri.
23Mōtah͈ so di jebale sa maye cha lotel ba, te fataliku fōfa ne sa morom am na amle ak you,
24Na nga fa bayi sa maye cha lotel ba, te dem jeka marale ak sa morom; cha ganou ga delusil, jebal sa maye.
25Goual a mar ak sa mbañ naka nga neke chi yōn wa ak mōm; lu dul lōga mbañ ma di na la joh͈e chi atekat ba, te atekat ba di na la joh͈e chi otukat ba, te mu tej la chi kaso.
26Chi dega mangi la di wah͈, Do fa gēna muk, be nga fey kopar bu muje ba.
27Dēga ngēn ñu wah͈ on nit i h͈āt ya, Bul njālo:
28Wande mangi len di wah͈, Ku sêt jigen te h͈emem ko, nistey njālo na ak mōm chi h͈ol am.
29Su la sa but i ndējor moylô, loh͈ati ko, te sani ko; ndege gen na bena chi sa cher rēr, te du sa yaram yepa di tabi chi nāri.
30Te su la sa loh͈o’ ndējor moylô, dog ko, te sani ko; ndege gen na bena chi sa cher rēr, te du sa yaram yepa di tabi chi nāri.
31Wah͈ nañu itam, ne, Ku fase ak jabar am, na ko joh͈ mbinda i mpase:
32Wande mangi len di wah͈, Ku fase ak jabar am, lu moy mu di chi njālo, tah͈ na ko mu njālo; te ku sey ak mōm ka ñu fase, njālo na.
33Dēga ngēn ñu wah͈ on nit i h͈āt ya, Bulu leka ngeñ, wande motali ko chi Yalla:
34Wande mangi len di wah͈, Bu len geñ muk; bu mu di cha ajana, ndege mō di gangūne’ Yalla;
35Wala chi suf si, ndege mō di degukay i tank’ am; wala cha Jerusalem, ndege mō di rew um Bur bu rey ba.
36Bul geñ itam chi sa bopa, ndege munu la wêh͈al bena kouar, mbāte ñulal ko.
37Wande na sēn wah͈ di, Wau, wau; Dēt, dēt; ndege lu upa yile chi lu bon la juge.
38Dēga ngēn ñu wah͈, ne, But ak but, buñ ak buñ:
39Wande mangi len di wah͈, Bu len findu lu bon, wande ku la dōr chi sa leh͈ i ndējor, sopalil benen bi itam.
40Te su la kena yubo chi yōn ndah͈ mu jel sa chol, bayi ko mu jel sa mbūba itam.
41Te ku la buga jeñ nga gūnge ko fu sorey, gūnge ko fu sorey‐sorey.
42Mayal ku la dagān, te bul gantu ku la buga aba.
43Dēga ngēn ñu wah͈, ne, Na nga sopa sa morom, te sib sa mbañ.
44Wande mangi len di wah͈, Sopa len sēn i mbañ, te ñānal len ña len di geten;
45Ndah͈ ngēn mun a neka sēn i dōm i Bay ba cha ajana; ndege mō fenkalo janta am cha kou ña bāh͈ ak ña bon, te di tou cha kou ña jūb ak ña jūbadi.
46Ndege su ngēn sope ña len sopa dal, ban yōl ngēn di am? Publican ya sah͈ du ñu def nōgule am?
47Te su ngēn noyo sēn i mboka dal, chi lan ngēn upale ñenen? Gentile ya du ñu def nōgule am?
48Di ngēn mot mbōk, naka sēn Bay ba cha ajana mote.
தற்சமயம் தேர்ந்தெடுக்கப்பட்டது:
Matthew 5: GWG
சிறப்புக்கூறு
பகிர்
நகல்
உங்கள் எல்லா சாதனங்களிலும் உங்கள் சிறப்பம்சங்கள் சேமிக்கப்பட வேண்டுமா? பதிவு செய்யவும் அல்லது உள்நுழையவும்
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.