1
Njàlbéen ga 25:23
Kàddug Yàlla gi
Aji Sax ji ne ko: «Ñaari giir nga ëmb, nara am ñaari xeet yuy xaajaloo, wenn wi mooy ëpp doole wi ci des, te mag ji mooy surgawu rakk ji.»
对照
探索 Njàlbéen ga 25:23
2
Njàlbéen ga 25:30
Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe).
探索 Njàlbéen ga 25:30
3
Njàlbéen ga 25:21
Gannaaw ga soxnas Isaaxa amul doom, Isaaxa dagaanal ko Aji Sax ji, mu nangul ko, soxna si daldi ëmb.
探索 Njàlbéen ga 25:21
4
Njàlbéen ga 25:32-33
Esawu ne: «Man miy waaja dee ak xiif, ana lu ma céru taaw di jariñ?» Yanqóoba ne ko: «Giñal ma jëkk.» Esawu giñal ko ko, mu jaay Yanqóoba ndono, li mu yeyoo ndax li muy taaw.
探索 Njàlbéen ga 25:32-33
5
Njàlbéen ga 25:26
Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën). Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at.
探索 Njàlbéen ga 25:26
6
Njàlbéen ga 25:28
Isaaxa nag am cofeel ci Esawu ndax li muy lekk ci am rëbbam, te Rebeka moom gëna sopp Yanqóoba.
探索 Njàlbéen ga 25:28
主页
圣经
计划
视频