Njàlbéen ga 1
1
Yàlla sàkk na àddina, fal ci nit
1Ca njàlbéen ga Yàlla sàkk na asamaan ak suuf. 2Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi.
3Ba loolu amee Yàlla ne: «Na leer nekk,» leer daldi am. 4Yàlla gis ne leer gi lu baax la, mu xàjjale leer ak lëndëm. 5Yàlla tudde leer gi bëccëg, lëndëm gi guddi. Ngoon jot, suba dugg, muy bés ba jëkk.
6Yàlla ne: «Na aw dénd dox diggante ndox yi, ngir xàjjale leen, yii fii, yii fale.» 7Yàlla nag sàkk dénd wi, xàjjalee ko ndox yi féete dénd wi suuf ak yi ko féete kaw. Mu daldi nekk noona. 8Yàlla tudde dénd wi asamaan. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñaareel ba.
9Yàlla ne: «Na ndox, mi asamaan tiim, gëndoo benn bérab, ba joor gu wow feeñ.» Mu daldi nekk noona. 10Yàlla tudde joor gu wow gi suuf, ndox mi gëndoo, mu tudde ko géej. Yàlla gis ne baax na.
11Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona. 12Suuf nag sax ñax, muy gàncax gu ànd ak wirgoy jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni wirgoy jiwu. Yàlla gis ne baax na. 13Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñetteel ba.
14Yàlla ne: «Na am ay leer ci asamaan, ngir xàjjale guddi ak bëccëg, te doon ay tegtal, yuy ràññle jamono yi, tey takk bés yi ak at yi. 15Nañu nekk ay leer ci asamaan si, di leeral suuf.» Mu daldi nekk noona. 16Yàlla sàkk ñaari leer yu mag, gi gëna mag yilif bëccëg, gi gëna ndaw yilif guddi; mu sàkk it biddiiw yi. 17Yàlla nag teg leen ci asamaan, di ca leeral suuf, 18ñuy yore guddi ak bëccëg, tey xàjjale lëndëm ak leer. Yàlla gis ne baax na. 19Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñeenteel ba.
20Ba loolu amee Yàlla ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.» 21Ci biir loolu Yàlla bind rabi géej yu mag yi ak mboolem mbindeef muy féey tey ramm-rammi ci ndox mi, mu ci nekk ak wirgoom, teg ca lépp luy boroomi laaf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla gis ne baax na. 22Ba mu ko defee Yàlla barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.» 23Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróomeel ba.
24Yàlla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona. 25Yàlla dafa bind rabi àll yi, lu ci nekk ak wirgoom, jur gu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla nag gis ne baax na.
26Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.»
27Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram;
ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit,
góor ak jigéen la bind.
28Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.»
29Yàlla ne: «Xool-leen, jox naa leen gépp gàncax gu ànd ak jiwoom ci kaw suuf sépp ak gépp garab guy meññ tey jur jiwoom, muy seen dund. 30Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona.
31Yàlla nag gis li mu def lépp, fekk lépp baax lool. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróom benneel ba.
Copyright © 2010, 2020 La Mission Baptiste du Sénégal