Njàlbéen ga 26
26
Isaaxa nëbbu na waa Gerar ngir mucc
1Ba loolu wéyee xiif am ca réew ma, muy xiif bu wuute ak ba woon ca jamonoy Ibraayma; Isaaxa nag dem Gerar ca Abimeleg, buurub waa Filisti.
2Foofa Aji Sax ji feeñu ko fa ne ko: «Bul dem Misra, waaye nanga toog ci réew mi ma lay wax. 3Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma. 4Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele, 5ndax Ibraayma déggal na ma, dénkoo na sama ndénkaane, ak samay santaane, ak sama dogali yoon, ak samay yoon.»
6Isaaxa nag toog Gerar. 7Góori foofa laaj ko ndaw si mu àndal, lu mu doon ci moom, mu ne: «Sama jigéen la.» Dafa bañoona wax ne soxnaam la, ngir ragal waa foofa rey ko ndax taaru Rebeka. 8Ba ñu fa toogee ba mu yàgg, mu am bés Abimeleg, buurub waa Filisti tollu ci palanteeram, gis leen, fekk yóo Isaaxaa ngay raay soxnaam Rebeka. 9Abimeleg woolu Isaaxa ne ko: «Kii kay ndeke sa soxna la! Noo mana waxe ne sa jigéen la?» Isaaxa ne ko: «Damaa waxe noonu, ngir ñu bañ maa rey ndax moom.» 10Abimeleg ne ko: «Li nga nu def nag? Xaw tuuti kenn ci nit ñi tëdde sa soxna, te kon nga yóbbe nu tooñ.» 11Abimeleg daldi fay doxe àrtu waa réewam mépp ne leen: «Ku laal waa jii walla soxnaam, dees na ko rey.»
Isaaxa fas na kóllëre ak Abimeleg
12Gannaaw loolu Isaaxa bey ca réew ma, góob ca at ma lu tollook téeméeri yoon la mu ji woon, ndax Aji Sax ji da koo barkeel. 13Alalam di yokku, muy gëna barele, ba mujj am doole lool, 14am géttu jur gu gudd ak gu gàtt, ak ay surga yu bare, ba tax waa Filisti iñaane ko, 15bay sakk ak a sëkk mboolem teen, yi surgay baayam Ibraayma gasoon ca jamonoom. 16Abimeleg daldi ne Isaaxa: «Demal, ba sore nu, ndax danga noo ëpp doole lool.» 17Isaaxa jóge foofa, dali ca xuru Gerar, sanc fa.
18Ba loolu weesee Isaaxa sikkli teen, yi ñu gasoon ca jamonoy baayam Ibraayma, te waa Filisti sakkoon leen gannaaw ba Ibraayma nelawee. Ca la tudde teen yi tur, ya leen baayam tudde woon. 19Surgay Isaaxa gasaat ca xur wa, jot ndox mu neex. 20Teewul sàmmi Gerar di soowook sàmmi Isaaxa naan: «Nun noo moom ndox mi.» Mu tudde teen ba Eseg (mu firi Coow), ndax li ñu soowoo ak moom. 21Ñu gasaat ab teen, xuloo amati ca, mu tudde ko Sitna (mu firi Xuloo). 22Mu jóge foofa, gasati teen, jàmm ne ñoyy, mu tudde ko Reyobot (mu firi Fu yaatu), ndax da ne: «Léegi Aji Sax ji yaatal na nu, te dinanu woomle ci réew mi.»
23Ba mu fa jógee, dafa dellu Beerseba. 24Guddi googu Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Maay Yàllay Ibraayma sa baay; bul ragal dara, ndax maa ngi ànd ak yaw. Dinaa la barkeel, ful sa askan ndax sama jaam Ibraayma.» 25Isaaxa nag sàkk fa sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko, ba noppi samp fa xaymaam. Te itam ay surgaam bënn nañu fa ab teen.
26Ci diggante boobu Abimeleg dafa jóge Gerar, dem fekki ko, ànd ak Awusat, ma doon wóllëreem, ak Pikol, njiital xarekatam. 27Isaaxa ne leen: «Lu waral ngeen fekksi ma fii, gannaaw dangeen maa bañ, ba dàq ma?» 28Ñu ne ko: «Gis nanu bu baax ne Aji Sax ji ànd na ak yaw; moo tax nu ne ayca nu waatoo ci sunu digganteek yaw te fasanteek yaw kóllëre. 29Su ko defee doo nu def dara lu bon, gannaaw defunu la dara lu bon, xanaa lu baax rekk, ba yebal la, nga dem ci jàmm. Kon léegi yal na la Aji Sax ji barkeel.»
30Isaaxa nag berndeel leen, ñu bokk lekk, ba noppi naan. 31Ca ëllëg sa, ñu xëy suba teel, daldi waatoo, Isaaxa door leena yiwi, ñu dem ci jàmm.
32Ca bés booba ay surgay Isaaxa ñëw nañu, di ko wax lu jëm ci teen, ba ñu doon gas, ne ko: «Gis nanu ndox.» 33Isaaxa tudde teen ba Siba (mu firi Waatoo), moo tax turu dëkk ba, ba fii nu tollu, di Beerseba (mu firi Teenu waat ga).
Esawu jël na ay soxna
34Esawu am na ñeent fukki at, jël na soxna ku ñuy wax Yudit, muy doomu Beeri, miy Etteen, jëlaat Basmat doomu Elon, miy Etteen. 35Jigéen ñooñu mu jël nag di naqar wu réy ci Isaaxa ak Rebeka.
Copyright © 2010, 2020 La Mission Baptiste du Sénégal