1
Njàlbéen ga 9:12-13
Kàddug Yàlla gi
Yàlla neeti: «Kóllëre gi may fas ak yeen ak mboolem mbindeef mu ànd ak yeen, day sax ba fàww te liy màndargaam mooy lii: def naa sama xon ci niir yi, muy màndargaal kóllëre, gi dox sama diggante ak àddina.
Yenzanisa
Ongorora {{vhesi}}
2
Njàlbéen ga 9:16
Xon gi day nekk ci biir niir yi, ma di ko gis, di xalaat kóllëre, gi ma fas fàww, sama diggante, man Yàlla, ak mboolem xeetu mbindeef mu nekk ci kaw suuf.»
3
Njàlbéen ga 9:6
Ku tuur deretu nit, na nit tuur deretam, ngir melokaanu boppam la Yàlla sàkke nit.
4
Njàlbéen ga 9:1
Ci kaw loolu Yàlla barkeel Nóoyin aki doomam ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina.
5
Njàlbéen ga 9:3
Man ngeena dunde boroom bakkan yooyu yépp. Jagleel naa leen bindeef yooyu yépp, ni ma leen jagleele woon gàncax.
6
Njàlbéen ga 9:2
Mboolem rabi àll yi ak njanaawi asamaan ak ndëgmeent yi ci suuf, ak jëni géej yépp, dinañu leen ragal lool. Teg naa leen ci seeni loxo.
7
Njàlbéen ga 9:7
Yeen nag, giirleen te bare, fulandiwu ci kaw suuf te fees ko.»
Pekutangira
Bhaibheri
Zvirongwa
Mavideo